Leeru Bés bi — 4 Samwiyee: Baamtug yoon wi 12:9

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Ndax kat àggaguleen ba tey ca dalluwaay ba, fa leen seen Yàlla Aji Sax ji sédde.

Baamtug yoon wi 12:9

Jógleen dem, fii du bérebu noflaay, nde sobewu na, ba nara yàqe yaxeet.

Mise 2:10

Kon des na ba tey noflaayu bésub juróom ñaareel bu ñu waajalal ñoñu Yàlla.

Yawut ya 4:9

Yaakaar jooju lanu am, mu mel ni diigalub gaal, diigal bu dëgër te wóor, ñeel sunu xol, te yaakaar jooju mooy bëtt rido ba, ba jàll ca néeg bu sella sell ba. Fa la ndaw li nu jiitu dugg ngir nun, te kookooy Yeesu mi ñu fal sarxalkat bu mag ba fàww, mu topp dayob Melkiccedeg.

Yawut ya 6:19–20

Sama kër Baay, dëkkuwaay yu baree nga fa. Su demewul woon noonu, ndax dinaa leen ne maa ngi leen fay waajali béreb? Te gannaaw bu ma leen waajalee béreb, dinaa délsi, jëlsi leen, yóbbu, ba fu ma nekk, man, ngeen nekk fa, yeen itam.

Yowaan 14:2–3

Ci diggante ñaar yooyii laa tance: yàkkamti namaa yiwiku ba fekki Almasi bi, te loolu moo dàqati fuuf.

Filib 1:23

Mooy fomp seen wépp rongooñ. Dee dootul am, dëj aki yuux aku tiis dootul am, lu njëkk laay wéy.»

Peeñu ma 21:4

Biir bàmmeel la ñu bon ñiy noppee sonle, fa la ña jeele doole noppaloo,

Ayóoba 3:17

Waaye dajaleleen ab denc fa asamaan, fa ko max ak xomaag dul yàqe, te ab sàcc du bëtt, jël ko. Ndaxte fa sab denc nekk, sab xol it a nga fa.

Macë 6:20–21

La fa kaw, xintewooleen ko, te ngeen ba li fi suuf,

Kolos 3:2

Moo yaw dee, ana sa ndam? Moo yaw dee, ana sag fitt?» Dee, ag fittam mooy bàkkaar, te bàkkaar, dooleem mooy yoon wi.

1.Korent 15:55–56

Lu ko moy ca njàlbéenu àddina lay dale sonn ay yooni yoon. Waaye tey ci mujug jamono yi la feeñ benn yoon doŋŋ, ba sarxe boppam, ngir far bàkkaar. Kon ni ab dogal sédde nit ñi benn yoon doŋŋ bu ñuy dee, seenub àtte topp ci, noonu itam la Almasi bi doone ab sarax benn yoon, ngir gàddu bàkkaaru nit ñu bare, te dina teewsiwaat, ci yoon wu joteetul dara ak bàkkaar, ngir indil ñi koy séentu seenug mucc.

Yawut ya 9:26–28

Gone yooyu nag, bindeefi suux ak deret lañu bokk doon, ñoom ñépp. Moo tax Yeesu itam dikk bokk ak ñoom woowu nekkin, ngir mana dee ba def deewug boppam pexe mi mu neenale ka yoroon dooley dee, te mooy Seytaane. Noonu la goreele mboolem ñi seenug ragala dee tënkoon cig njaam, seen giiru dund.

Yawut ya 2:14–15

Man nag, daanaka saraxu tuuru bu sottiku laa ba noppi; sama waxtuw dem dëgmal na. Xare bu baax bi, xare naa ko, rawante bi, sottal naa ko, ngëm gi ma am, sàmm naa ko. Léegi nag kaalag njekk a may xaar, te Boroom bi, àttekat bu jub bi moo ma koy yool, keroog ca bés ba, te du man rekk la koy yool, waaye itam képp ku koy séentu te yàkkamti bés ba muy feeñ.

2.Timote 4:6–8