Woyleen Aji Sax ji woy wu yees, yeen waa cati àddina, kañleen ko, ànd ak ñiy wàcci géej ak li ci biiram, ak duni géej ak ña ca dëkke.
Esayi 42:10
Leeru Bés bi
Woyleen Aji Sax ji woy wu yees, yeen waa cati àddina, kañleen ko, ànd ak ñiy wàcci géej ak li ci biiram, ak duni géej ak ña ca dëkke.
Esayi 42:10
Mu jëm ci njiital woykat yi, ñeel Asaf, te ànd ak xalam gu ñuy wax gitiit. Sarxolleleen ci Yàlla mi nuy dooleel; xaaculeen ci Yàllay Yanqóoba.
Taalifi cant 81:1–2
génnee ma ca kàmbug sànkute, sippee ma ca xóotey ban ba, cëppe ma ciw doj, samp ma, ma dëgër.
Taalifi cant 40:3
Xanaa du maa la sant ne la, nga dëgërlu te am fit? Bul tiit, bul ragal. Sa Yàlla Aji Sax ji laak yaw, fépp foo jëm.»
Yosuwe 1:9
Esra ne leen: «Ayca demleen lekk lu gëna duuf, naan lu neexa neex te sédd ci ñi amul lu ñu togg; ndax bésub tey bés bu sell la ñeel sunu Boroom. Kon buleen ci naqarlu kat, ndax bége Aji Sax ji mooy seen doole!»
Neyemi 8:10
Ba bokki gëmkati Room yégee ne nu ngi dikk, ñoo nu gatandusi ba fa ñuy wax péncum Apiyus ak fa ñuy wax Ñetti Dalu Gan ya. Ba leen Póol gisee, daa sant Yàlla, daldi gëna sawar.
Jëf ya 28:15
Li tax ngeen wara gëna farlu ci loolu mooy, xam ngeen jant yi nu tollu; seen waxtuw yewwu jot na ba noppi, nde léegi la nu mucc gëna jege ba nuy doora gëm. Guddi gi màggat na, bët a ngi bëgga set. Kon nag nanu bàyyi jëfi lëndëmtu te ràngoo gànnaay yi ñuy xaree cig leer. Nanu jëfe jëfin wu jekka def bëccëg; nanu sore xawaare yi ànd ak moy, ak màndite, sore baane bu lewul, ak ñaawtéef yu ni mel, te sore ŋaayoo ak kiñaan. Waaye yiirooleen Sang Yeesu Almasi bi, te ngeen baña yittewoo seen bakkan, ngir di topp seeni xemmemtéef.
Room 13:11–14
Yal nanga ma nangul samag ñaan ni cuuraay lu ñu la taalal, loxo yi ma la tàllal di saraxu ngoon soo gërëm.
Taalifi cant 141:2
Looloo waral mu mana musal mucc gu mat sëkk, ñiy awe fi moom, dikk fa Yàlla, ndax mooy dund ba fàww, ngir di leen tinul.
Yawut ya 7:25
Saxaaras cuuraay laa ngi gillee ci loxol malaaka mi, ànd ak ñaani ñu sell ñi, di yéeg fa Yàlla.
Peeñu ma 8:4
Te yeen itam yeen ay doji cëslaay yuy dund, doj yi Noo gu Sell gi tabaxe ag kër Yàlla, ñeel liggéeyu carxal gu sell, ngir ngeen di ko jébbal ay sarax yu Noo gi rafetlu, sarax yu Yàlla nangu ndax Yeesu Almasi bi.
1.Piyeer 2:5
di saxoo ñaan,
1.Tesalonig 5:17
Bés yu mujj yi
Wone yépp1 Sam 2026
31 Des 2025
30 Des 2025
29 Des 2025
28 Des 2025
27 Des 2025
26 Des 2025