Leeru Bés bi — 7 Samwiyee: Neyemi 5:19

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Kon nag rikk sama Yàlla, bàyyil xel ci man te baaxe ma, ndax mboolem li ma defal askan wii!

Neyemi 5:19

«Demal yéeneji lii, Yerusalem di dégg, nga ne: “Aji Sax ji dafa wax ne: Maa ngi fàttaliku sa ngor ba ngay ndaw, ak sa cofeel ba nga deeb séet, ba ngay topp sama gannaaw ca màndiŋ ma, ba ngay jaare fa dara dul sax.

Yeremi 2:2

Waaye man maay bàyyi xel sama kóllëre gi ma fasoon ak yaw ba ngay ndaw. Maa lay saxalal kóllëre guy wéy ba fàww.

Esekiyel 16:60

«Aji Sax ji déy dafa wax ne: Bu Babilon matalee juróom ñaar fukki ati kilifteefam, dinaa leen dikkal, sottalal leen sama kàddug jàmm, ba delloosi leen ci béreb bii. Ndax man déy, xam naa mébét yi ma leen mébétal. Kàddug Aji Sax jee. Du mébéti loraange, waaye mébéti jàmm laa leen mébétal, ngir may leen yaakaaru ëllëg.

Yeremi 29:10–11

Mu ne: «Ni asamaan tiime suuf, ni la samay jëfin tiime seeni jëfin, samay xalaat it tiime ko seeni xalaat.

Esayi 55:9

Man de su ma doon yaw damay sàkku Yàlla, te kon Yàlla laay diis sama mbir. Keey def jëf ju màgg ju nattuwul, di def kiraama yu limuwul.

Ayóoba 5:8–9

Ndokkalee, yaw mi dénku ci Aji Sax ji, te sàkkuwoo ku bew ak kuy topp ay fen.

Taalifi cant 40:5

Du kenn kuy taxaw ci sa kanam, sa giiru dund. Noonee ma nekke woon ak Musaa, ni laay nekke ak yaw; duma la seetaan, duma la wacc.

Yosuwe 1:5

Du benn dige bu wuute ci mboolem digey ngëneel ya Aji Sax ji giñaloon waa kër Israayil. Lépp a mat sëkk.

Yosuwe 21:45

Yàlla du nit, bay fen, du doom aadama bay tuub. Moom wax na lu mu deful a? Am àddu na lu mu sottalul?

Màndiŋ ma 23:19

Xamleen boog ne seen Yàlla Aji Sax ji moom mooy Yàlla; mooy Yàlla ju dëggu jiy sàmm kóllëre ak ngor ñeel soppeem ñiy sàmm ay santaaneem, sët ba sëtaat, ba ci junniy maas.

Baamtug yoon wi 7:9

Mooy leel ku ko ragal, di bàyyi xel kóllëreem gi ba fàww.

Taalifi cant 111:5

Aji Sax ji nee: «Ana jaboot juy fàtte doomam juy nàmp, mbaa muy néege ku mu jur ci biiram? Bu ko manoona fàtte it, man duma la fàtte. Sama biir loxo yii laa la ñaas, say tataa janook man ba fàww.

Esayi 49:15–16

Aji Sax ji sa Yàllaa ngi fi sa biir, di jàmbaar juy walloo. Moo lay bége ci biir bànneex, leqalee la cofeelam, bége la bay sarxolle.

Sofoni 3:17