Bokk yi, fooguma ne jot naa ci, xanaa kay lenn: damay fàtte li ci gannaaw, te def lu ma man, ngir fexee yóotuji li ci kanam, daldi xélu dëgmal naanukaay ba, ngir jot ca neexal ba nu Yàlla di woowe fa kaw, ci Almasi Yeesu.
Filib 3:13–14
Leeru Bés bi
Bokk yi, fooguma ne jot naa ci, xanaa kay lenn: damay fàtte li ci gannaaw, te def lu ma man, ngir fexee yóotuji li ci kanam, daldi xélu dëgmal naanukaay ba, ngir jot ca neexal ba nu Yàlla di woowe fa kaw, ci Almasi Yeesu.
Filib 3:13–14
«Ñi nga ma jox nag, Baay, bëgg naa, fa may ne, ñoom it, ñu nekk faak man, ngir ñu gis sama daraja ji nga ma jox, ndax yaa ma sopp laata àddina di sosu.
Yowaan 17:24
Looloo tax may daj yii coono. Waaye rusuma ci, ndax xam naa ki ma gëm, te wóor na ma ne, li ma ko dénk, moo ko mana sàmm ba keroog bés ba.
2.Timote 1:12
Te lii kat, bir na ma: ki tàmbali jii jëf ju baax ci yeen, dina ko àggale ba keroog bésub Almasi Yeesu.
Filib 1:6
Xanaa xamuleen ne, ab rawante, ñépp a cay daw, waaye kenn doŋŋ ay jël ndam li? Dawleen nag ba jël ndam li. Joŋantekati tàggat yaram yi, dañuy yar seen yaram bu metti, te ñooñu kaalag ndam guy seey doŋŋ lañu ci yaakaar, waaye nun, kaalag ndam gu sax dàkk lanu ci yaakaar.
1.Korent 9:24–25
Kon nag gannaaw gii ndiiraanu seede wu réy moo nu yéew, nanu sippiku mboolem sëf bu nuy yeexal ak bàkkaar bu nu yomba téqtal. Ñu daw nag xél wi ñu nu waajalal, te baña yoqi. Nanu ne jàkk Yeesu, kiy sos, di sottal ngëm, moom mi mbég mi ñu ko waajalal tax mu dékku bant ba ñu ko daaj, tegul muy dara toroxtaange ja ko ca fekk, te doxe ca toog ca ndijooru ngànguney Yàlla.
Yawut ya 12:1–2
Aji Sax ji nag mooy dox, jiitu la. Moom mooy nekk ak yaw. Du la ba, du la wacc mukk. Bul tiit, bul yoqi.»
Baamtug yoon wi 31:8
Aji Sax ji, maa xam ne nit moomul yoonam, kuy dox moomuli jéegoom.
Yeremi 10:23
Bu Aji Sax ji rafetloo saw yoon, mooy jiite say jéego. Soo tërëfee it, doo daanu. Aji Sax jee lay walloo loxoom.
Taalifi cant 37:23–24
Teewul ma des ak yaw, nga jàpp sama loxol ndijoor. Danga maa gindee sam xel, teg ca dalale ma sa teraanga.
Taalifi cant 73:23–24
Ndax kat bir na ma ne du ag dee, du ag dund, du ay malaaka, duy boroom nguur, du tey, du ëllëg, duy boroom doole, du lu kawe, du lu xóot, mbaa meneen mbindeef mu mu doon; dara manu noo tàggale ak cofeel gi nu Yàlla won ci Almasi Yeesu sunu Sang.
Room 8:38–39
Bés yu mujj yi
Wone yépp31 Des 2025
30 Des 2025
29 Des 2025
28 Des 2025
27 Des 2025
26 Des 2025
25 Des 2025