jaarale leen ci yoon wu jub, ngir ñu àgg cib dëkk.
Taalifi cant 107:7
Leeru Bés bi
jaarale leen ci yoon wu jub, ngir ñu àgg cib dëkk.
Taalifi cant 107:7
Moo leen fekk réewum màndiŋ, fu ne wëyëŋ, ubaleeki sab, mu feg leen, toppatoo leen, sàmm leen, ni bu ñu doon peru bëtu boppam. Moo mel ni jaxaay juy naawtal am tostanam, daayaarlu, di wër, tiim leen, tàllali laafam, aw leen, teg ciw dunqam, boot leen. Aji Sax ji doŋŋ a leen wommat, du yàllay jàmbur ju ko ci fekk.
Baamtug yoon wi 32:10–12
Ba ba ngeen di magal, man la, ba keroog ngeen di bijjaaw, maa leen di boot. Maa sàkk, maay yor, maay boot, xettali!
Esayi 46:4
leqali ma, teg ma ci yooni njub ngir teraangay turam. Su may jaare xuru dee wu ne këruus it, duma ragal loraange: yaw laak man, sa bantu sàmm ak sa nguul, yooyoo may dalal.
Taalifi cant 23:3–4
Aji Sax ji di leen jiite fu ngeen tollu, di leen màndale joor gu maral, dëgëral seeni cér, ngeen mel ni tool bu ñu suuxat, mel ni bëtu ndox bu dul ŋiis,
Esayi 58:11
nemmikuy tataam, doxantoo këri buur, ba man koo yegge maasug ëllëg,
Taalifi cant 48:14
Yàlla, kay, mooy ki dooleem kaweel! Ana ku mana jàngale ni moom?
Ayóoba 36:22
«Ana loo bëgg ma defal la ko?» Mu ne ko: «Xanaa may gis, Sang bi.»
Luug 18:41
Ngalla muril saay gët, ma niir sa kéemaani yoon.
Taalifi cant 119:18
Ca la ubbee seen xel, ngir Mbind mi leer leen.
Luug 24:45
Waaye Taxawukat bi, di Noo gu Sell gi leen Baay biy yónnee ci sama tur, moo leen di jàngal lépp, fàttali leen lépp lu ma leen waxoon, man.
Yowaan 14:26
gépp may gu baax ak bépp jagle bu mat, fa kaw la bawoo, di lu wàcce fa Baay biy boroom leer yi, ki soppikuwul ci lenn, te genn ker gu toogadi nekkul ci moom.
Yanqóoba 1:17
ngir Yàllay sunu Sang Yeesu Almasi bi, Baay bu màgg bi, sol leen xel mu rafet ak ngis, ngir ngeen man koo xam bu baax. Ngir itam seen bëti xol leer ba ngeen gis yaakaar ji ci wooteem ak ni ay ngëneelam géejoo te yéeme, ñeel ñu sell ñi mu séddoo. Ngeen boole ci xam manooreem gu nattuwul gi mu nu lañalal, nun gëmkat ñi. Manoore googu feeñ na ci jëf ji sottee ci kàttanam ak dooleem
Efes 1:17–19
Bés yu mujj yi
Wone yépp2 Sam 2026
1 Sam 2026
31 Des 2025
30 Des 2025
29 Des 2025
28 Des 2025
27 Des 2025