Moo leen di dooleel ba ca mujjantal ga, ngir ngeen mucc sikk, keroog sunu bésu Sang Yeesu Almasi bi.
1.Korent 1:8
Leeru Bés bi
Moo leen di dooleel ba ca mujjantal ga, ngir ngeen mucc sikk, keroog sunu bésu Sang Yeesu Almasi bi.
1.Korent 1:8
Te yeen ñi masoona sore lool Yàlla, doonoon ay noonam ci wàllu xalaat ak jëf ju bon, tey, deewug yaram, deewug suux gi Almasi bi dee, moom la leen Yàlla jubalee ak boppam, ba teewal leen fi kanamam, ngeen di ñu sell, mucc sikk, seen der set wecc. Noonu la deme, ndegam kay fekk na leen sësoo ngëm gu ngeen dëjoo ba dëgër, te baña nangu lenn di leen sorele ak yaakaar ji ci xibaaru jàmm bi ngeen dégg, te ñu biral ko, ñeel mépp mbindeef. Man Póol nag, ci yégle xibaaru jàmm boobu laa di ab jawriñ.
Kolos 1:21–23
ngir seen der set wecc, te kon deesuleen mana gàkkal ci lenn. Ay goney Yàlla yu amul sikk ngeen di doon, ci biir maas gu dëng te yàqu, ngeen di lerxat ci seen biir, ni ay leer ci àddina si,
Filib 2:15
Kon nag soppe yi, li feek ngeen di séentu loolu, defleen seen kem-kàttan, ba bésub keroog fekk leen ci jàmm, te ngeen baña am benn gàkk, mbaa sikk ci gis-gisu Yàlla.
2.Piyeer 3:14
ba mana xàmmee li gën. Su ko defee ngeen set wecc te mucc sikk, ngir keroog bés bi Almasi bi di délsi.
Filib 1:10
Ki leen mana aar ci bépp jéll, ba taxawal leen fa muy teewejee darajaam, te fekk leen ñàkk sikk, seen mbég mat sëkk, Yàlla miy kenn, sunu Musalkat, ci sunu ndimbalal Sang Yeesu Almasi bi, daraja ak màggaay ak kàttan ak sañ-sañ ñeel na ko, démb ak tey ak ëllëg, ba fàww! Amiin.
Yudd 24–25
Mooy sàmm jéegoy wóllëreem, ku bon sànkoo biir lëndëm, nde doole mayewul ndam.
1.Samiyel 2:9
Su nu nee am nanook moom jokkoog mbokk, te teewu noo wéye ag lëndëm, danuy fen, te jëfewunu dëgg. Waaye ni mu nekke moom ci boppam cig leer, su nu dee wéye noonu ag leer, su boobaa lanuy séq jokkoog mbokk, te deretu Yeesu Doomam moo nuy raxas ba nu set, tàggook bépp bàkkaar.
1.Yowaan 1:6–7
Yeesu ne ko: «Ku sangu ba noppi, soxlaatula raxas lu moy ay tànkam, ndax set na wecc. Yeen nag set ngeen, waaye du ñépp.»
Yowaan 13:10
Yoon wu xelu laa la teg, jaarloo la yoonu njub. Doo dox ba tërëf, doo daw, téqtalu. Ŋoyal cib yar, bul yoqi, sàmm ko, moo yor sa bakkan.
Kàddu yu xelu 4:11–13
Moyul, bu fa jaare; mbasal te wéy!
Kàddu yu xelu 4:15
Boroom bee may wallu ci jépp jëf ju bon, te moo may aar ba tàbbal ma fa nguuram ga fa asamaan. Daraja ñeel na ko, tey ak ëllëg ba fàww. Amiin.
2.Timote 4:18
Bés yu mujj yi
Wone yépp29 Des 2025
28 Des 2025
27 Des 2025
26 Des 2025
25 Des 2025
24 Des 2025
23 Des 2025