Leeru Bés bi — 31 Desàmbar: Baamtug yoon wi 1:31

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

ca màndiŋ ma it, gis ngeen na leen seen Yàlla Aji Sax ji fabe, ni baay di fabe doomam, ci yoon wi ngeen dox wépp, ba agsi béreb bii.»

Baamtug yoon wi 1:31

“Yeena gisal seen bopp ni ma def waa Misra, te yeen, ma boot leen, ni jaxaay di fireey laafam, boot ay doomam, ba ngeen jegesi ma fii.

Mucc ga 19:4

Seen gépp njàqare di njàqarey boppam, malaaka mi mu jàkkaarlool musal leen ca. Moo leen sopp, ñeewante leen, ba jotal leen boppam, te fu ñu masa jaare démb, mu fab leen, boot.

Esayi 63:9

Moo mel ni jaxaay juy naawtal am tostanam, daayaarlu, di wër, tiim leen, tàllali laafam, aw leen, teg ciw dunqam, boot leen. Aji Sax ji doŋŋ a leen wommat, du yàllay jàmbur ju ko ci fekk.

Baamtug yoon wi 32:11–12

Ba ba ngeen di magal, man la, ba keroog ngeen di bijjaaw, maa leen di boot. Maa sàkk, maay yor, maay boot, xettali!

Esayi 46:4

nemmikuy tataam, doxantoo këri buur, ba man koo yegge maasug ëllëg,

Taalifi cant 48:14

làmmiñ wa daa neex ni lem, te xare lal xol ba; kàddu ya gëna nooy ag oliw te di saamar bu génn mbaram.

Taalifi cant 55:22

«Moo tax ma ne leen, buleen seen bakkan jaaxal, ngir lu ngeen lekk, mbaa lu ngeen naan, te it buleen seen yaram jaaxal ngir lu ngeen sol. Xanaa du lekk gi, bakkan bee ko ëpp solo, te koddaay li it, yaram wee ko ëpp solo?

Macë 6:25

Ndaxte loolu lépp, yéefar yi ñoo koy tiisoo. Te seen Baay ba fa asamaan xam na ne soxla ngeen loolu lépp.

Macë 6:32

Gannaaw loolu Samiyel jël aw doj, teg ko ci diggante Mispa ak fu ñuy wax Sen; mu dippee doj wi Eben Eser (muy firi Doju Wall). Mu ne: «Ba fii la nu Aji Sax ji walloo.»

1.Samiyel 7:12

Gannaaw loolu Yosuwe dem na bay mag, ba làq at yu bare. Aji Sax ji ne ko: «Léegi mag nga, làq nga at yu bare, te ndesu réew mi ngeen nangoogul yaatu na lool.

Yosuwe 13:1

Du caageenu damaa àgg ci loolu lépp ba noppi, mbaa damaa mat sëkk xaat, waaye maa ngi wéye samaw xél, di jéema jot ci neexalu rawante bi, gannaaw ba ma Almasi Yeesu jotee ci man itam.

Filib 3:12

Ni seen Baay ba fa asamaan mate nag, nangeen ni mate.

Macë 5:48

Loolu tax na ba ngeen def lu ngeen man, ba dolli ci seen ngëm, njàmbaar; seen njàmbaar, ngeen dolli ci xam-xam; seen xam-xam, ngeen dolli ci noot seen bakkan; noot seen bakkan, ngeen dolli ci ag muñ; seenug muñ, ngeen dolli cig ragal Yàlla; seenug ragal Yàlla, ngeen dolli ci bëgg seen bokki gëmkat; bëgg seen bokki gëmkat, ngeen dolli ci cofeel.

2.Piyeer 1:5–7

Li may ñaan nag moo di seen cofeel yokku tey gën di yokku, te ngeen ànd ceek xam-xam bu matale ak gépp ràññee,

Filib 1:9

Mooy noonu ñu binde rekk ne: «Lu bët gisul, nopp déggu ko, xel daju ko, Yàllaa ko dencal ñi ko sopp.» Waaye nun la Yàlla feeñalal denc googu jaare ci Xelam. Ndaxte Xelum Yàlla lépp lay gëstu ba ci xóotey mbóoti Yàlla.

1.Korent 2:9–10

Kon des na ba tey noflaayu bésub juróom ñaareel bu ñu waajalal ñoñu Yàlla.

Yawut ya 4:9

Yaw mi mel nii, buur bi ci taar bi ngay teg bët; yaay gis réew mi ne màww.

Esayi 33:17