Moo tax buleen def jëfi ñàkk bopp, waaye jéemleena xam coobarey Boroom bi.
Efes 5:17
Leeru Bés bi
Moo tax buleen def jëfi ñàkk bopp, waaye jéemleena xam coobarey Boroom bi.
Efes 5:17
Lii moo di coobarey Yàlla: ngeen sellal te mucc ci séy yi yoon tere.
1.Tesalonig 4:3
Jubool ak Yàlla rekk, am jàmm, ngëneel dikkal la.
Ayóoba 22:21
Texeg fàww gi nag moo di ñu xam la, yaw jenn Yàlla jiy dëgg, xam it ki nga yebal, muy Yeesu Almasi bi.
Yowaan 17:3
Xam nanu itam ne Doomu Yàlla moo dikk ba may nu xel mu nu xame Kiy dëgg, te nu ngi ci Kiy dëgg ak Doomam Yeesu Almasi bi. Kooku mooy Yàlla ju dëggu ji, te moom moo di ag texe ba fàww.
1.Yowaan 5:20
Moo tax nun itam, ba nu déggee seen mbir ba tey, noppiwunu leena ñaanal, di sàkku ngeen fees ak xam-xam ci lépp luy coobarey Yàlla, te ngeen ànd ceek lu mat sëkk ci wàllu xel ak gis-gis bu Noo gi maye.
Kolos 1:9
ngir Yàllay sunu Sang Yeesu Almasi bi, Baay bu màgg bi, sol leen xel mu rafet ak ngis, ngir ngeen man koo xam bu baax. Ngir itam seen bëti xol leer ba ngeen gis yaakaar ji ci wooteem ak ni ay ngëneelam géejoo te yéeme, ñeel ñu sell ñi mu séddoo. Ngeen boole ci xam manooreem gu nattuwul gi mu nu lañalal, nun gëmkat ñi. Manoore googu feeñ na ci jëf ji sottee ci kàttanam ak dooleem
Efes 1:17–19
Jegeleen Yàlla, mu jege leen. Yeen bàkkaarkat yi, raxasleen seeni loxo, yeen ŋaralekat yi laa ne, setalleen seen xol.
Yanqóoba 4:8
Enog dafa topp Yàlla, ba jekki-jekki giseesatu ko, ndaxte Yàllaa ko yéege fa moom.
Njàlbéen ga 5:24
Ndax ñaar dina ànd te digewuñub dajee?
Amos 3:3
Man de, jege Yàllaa ma gënal. Boroom bi Aji Sax ji, yaw laa def kiiraay, ngir siiwal sa jépp jëf.
Taalifi cant 73:28
Mu dem ba ca Buur Asa, ne ko: «Asa, dégluleen ma, yaw ak mboolem Yuda ak Beñamin. Li feek yeena ngi ànd ak Aji Sax ji, mu ngi ànd ak yeen. Su ngeen ko wutee, mu ubbil leen boppam, waaye su ngeen ko dëddoo, mu dëddu leen.
2.Jaar-jaar ya 15:2
Waaye ba ñu walbatikoo ca seen biir njàqare, jublu ci Aji Sax ji Yàllay Israayil, ba wut ko, ubbil na leen boppam.
2.Jaar-jaar ya 15:4
Ndax man déy, xam naa mébét yi ma leen mébétal. Kàddug Aji Sax jee. Du mébéti loraange, waaye mébéti jàmm laa leen mébétal, ngir may leen yaakaaru ëllëg. Su boobaa ngeen woo ma wall, dikk ñaan ma, ma nangul leen. Su boobaa ngeen làmb, daj ma, ndegam làmbe ngeen seen léppi xol,
Yeremi 29:11–13
Léegi nag bokk yi, am nanu sañ-sañu dugg ca néeg bu sella sell ba, ngir deretu Yeesu, deretu Yeesu jiy yoon wu yees, yoonu dund gu mu nu xàllal, jàllale ko ca rido ba, te rido ba moo di yaramu suuxam wi mu saraxe. Am nanu itam sarxalkat bu mag bu jiite kër Yàlla ga. Kon nag nanu agsee fi Yàlla xol bu dëggu ak fit wu mat sëkk wu ngëm waral, gannaaw wisees na sunum xel ndoxum setlu, ba mu tàggook bépp gàkk bu mu nu sikkale, te raggees na sunu yaram ci ndoxum setlu.
Yawut ya 10:19–22
Bés yu mujj yi
Wone yépp28 Des 2025
27 Des 2025
26 Des 2025
25 Des 2025
24 Des 2025
23 Des 2025
22 Des 2025