Leeru Bés bi — 28 Desàmbar: Màrk 2:5

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Yeesu seetlu seen ngëm, daldi ne lafañ ba: «Doom, jéggalees na la say bàkkaar.»

Màrk 2:5

Kenn dootul soxlaa jàngal kenn, muy moroomam mbaa mbokkam, naan ko: “Ràññeel Aji Sax ji!” Ndax ñoom ñépp a may ràññee, ki gëna tuut ba ci ki gëna mag,» kàddug Aji Sax jee, «ndax maa leen di jéggal seeni ñaawtéef, te seeni bàkkaar, duma ci bàyyeeti xel.»

Yeremi 31:34

«Lu kii di wax nii? Yàlla de lay diir mbagg. Ana ku mana jéggaley bàkkaar, ku dul Yàlla doŋŋ?»

Màrk 2:7

Mennum man mii maay far say moy ngir man, ba dootuma fàttaliku bàkkaar.

Esayi 43:25

Dib taalifu yeete, ñeel Daawuda. Ndokkalee yaw mi ñu baal ag moy, jéggal la bàkkaar. Ndokkalee yaw mi Aji Sax ji toppul say tooñ, te amoo xelum njublaŋ it.

Taalifi cant 32:1–2

Ana Yàlla ju mel ni yaw, di baale ag tooñ, di jéllale ag moy, ñeel ndesu ab séddoom? Kii du denc mer ba fàww, te moo bëgg di yéwéne.

Mise 7:18

Baaxleen ci seen diggante, di ñeewantante, tey baalante, ni leen Yàlla baale ci Almasi bi.

Efes 4:32

Kooku moo dikke kàddug seede, ngir seede lu jëm ci leer gi, ngir ñépp gëme ciy waxam. Du moom ci boppam moo doon leer gi, waaye seedeel leer gi moo ko taxa dikk. Leer giy dëgg, tey leeral nit ñépp, moo dikk ci àddina.

Yowaan 1:7–9

Ni penku soree sowu, ni la nu soreleek sunu mbugali tooñ.

Taalifi cant 103:12

Ndax kat bàkkaar yilifatu leen, nde du ci kilifteefu yoonu Musaa ngeen nekk, waaye ci aw yiw ngeen tàbbi.

Room 6:14

Noonu lees leen yiwee, tàggale leen ak nooteelu bàkkaar, ngeen doon ay surgay njub.

Room 6:18

Ñooñoo dikk ba ca Filib ma dëkke Betsayda ca diiwaanu Galile, ne ko: «Sang bi, danoo bëgga gis Yeesu.»

Yowaan 12:21

Aji Sax ji, nu ngi lay xaar, fi sa kaw yoonu santaane yi, di tudd sa tur, di la bàyyi xel, lii déy, mooy sunu nammeelu xol.

Esayi 26:8

Aji Sax ji, képp ku ko woo wall, mu jege la, képp ku ko woo wall te muy dëgg.

Taalifi cant 145:18

ndax fu ñaar mbaa ñett dajee ci sama tur, maa ngi ci seen biir.»

Macë 18:20

Duma leen bàyyi ngeen tumurànke. Dinaa délsi ci yeen.

Yowaan 14:18

te ngeen jàngal leen ñu sàmm mboolem li ma leen sant. Maa ngii nag, di nekk ak yeen bés bu nekk, ba kera àddina di tukki.»

Macë 28:20

Kon nag gannaaw gii ndiiraanu seede wu réy moo nu yéew, nanu sippiku mboolem sëf bu nuy yeexal ak bàkkaar bu nu yomba téqtal. Ñu daw nag xél wi ñu nu waajalal, te baña yoqi. Nanu ne jàkk Yeesu, kiy sos, di sottal ngëm, moom mi mbég mi ñu ko waajalal tax mu dékku bant ba ñu ko daaj, tegul muy dara toroxtaange ja ko ca fekk, te doxe ca toog ca ndijooru ngànguney Yàlla.

Yawut ya 12:1–2

Tey jii ci ab seetu lanuy gise gis-gis bu lënt. Waaye bu keroogee, màkk lanuy jàkkaarloo ak li nuy xool. Tey jii, as ndog laa xam, waaye su keroogee, ni ñu ma xame, ni laay xame ba mu mat sëkk.

1.Korent 13:12

Ci diggante ñaar yooyii laa tance: yàkkamti namaa yiwiku ba fekki Almasi bi, te loolu moo dàqati fuuf.

Filib 1:23

Soppe yi, léegi doomi Yàlla lanu, te li nuy dooni nag feeñagul. Waaye xam nanu ne bés bu Almasi bi feeñee, nooy nirook moom, ndax su boobaa, ni mu nekke, noonu lanu koy gise. Te képp ku am jooju yaakaar ci moom, noonu mu sete, ni lay setale boppam.

1.Yowaan 3:2–3