Moo waral xoolunu ci li bët mana gis, waaye li bët dul gis, ci lanuy xool, ndax li bët mana gis day wéy, waaye li bët dul gis mooy sax ba fàww.
2.Korent 4:18
Leeru Bés bi
Moo waral xoolunu ci li bët mana gis, waaye li bët dul gis, ci lanuy xool, ndax li bët mana gis day wéy, waaye li bët dul gis mooy sax ba fàww.
2.Korent 4:18
ndax amunu fii ci àddina dëkk bu sax ba fàww, waaye dëkk biy ñëw, moom lanuy sàkku.
Yawut ya 13:14
Ndax yeena bokk ak ñi ñu tëj seen coono, te yeena muñ ci xol bu sedd ni ñu foqarñee seen moomeel, ngir xam ngeen yeen ci seen bopp ne am ngeen alal ju ko gën tey sax ba fàww.
Yawut ya 10:34
«Buleen ragal dara, yeen jur gu sew gi, ndax seen Baay la soob, mu jagleel leen nguur gi.
Luug 12:32
Loolu bégeleen koo bége, doonte tey ñàkkul ngeen nekke njàqare ab diir, ndax ay nattuy nattu.
1.Piyeer 1:6
Biir bàmmeel la ñu bon ñiy noppee sonle, fa la ña jeele doole noppaloo,
Ayóoba 3:17
Noo ngi onk ndax diis, li feek nu ngeek sunuw yaram, xayma bi nu soloo nii. Du summiku lanu namm, waaye solu teg ko ci lanu namm, ngir li jëm ci dee, daldi suux ci biir dund.
2.Korent 5:4
Mooy fomp seen wépp rongooñ. Dee dootul am, dëj aki yuux aku tiis dootul am, lu njëkk laay wéy.»
Peeñu ma 21:4
Jàpp naa ne sunu coonob tey du dara, soo ko xoolee ci teraanga ji ñu nuy feeñalal ëllëg.
Room 8:18
Sunu coono bu woyof bii ci àddina, ci diggante bu gàtt nag, moo nuy jural teraanga ju diisaay ba jéggi dayo, teraanga ju sax dàkk.
2.Korent 4:17
Ndaxte moom mooy sunu jàmm, moom mi boole ñaar, Yawut bi ak jàmbur bi dul Yawut, def leen kenn. Ci suuxu yaramam wa ñu daaj la ñàggee ñagu mbañeel bi doxoon sunu diggante.
Efes 2:14
Loolu di firi ne ci Almasi bi la Yàlla jubale waa àddina ak jëmmu boppam, ba toppu leen seeni tooñ, te moo nu dénk kàddug juboo gi.
2.Korent 5:19
Almasi bi masula bàkkaar, moom la Yàlla sëf sunu bàkkaar, ngir nu mana ame ci moom àtteb nit ñu jub fa Yàlla.
2.Korent 5:21
Deretam ja tuuru ca bant ba, ca la Yàlla defe jàmm, ba sottale ci moom, pexe mi mu jubalee boppam ak lépp, muy lu nekk ci kaw suuf ak la fa asamaan. Te yeen ñi masoona sore lool Yàlla, doonoon ay noonam ci wàllu xalaat ak jëf ju bon, tey, deewug yaram, deewug suux gi Almasi bi dee, moom la leen Yàlla jubalee ak boppam, ba teewal leen fi kanamam, ngeen di ñu sell, mucc sikk, seen der set wecc.
Kolos 1:20–22
Kayitu bor bi nu tiiñaloon, te dogali yoon toppe nu ko, moom moo far mbind ma, yóbbu kayit ga, daajaale ko ak Almasi bi ca bant ba.
Kolos 2:14
Yoonu Musaa ak santaane yaak ndigal ya, moom la xewwil, ngir yeesal ñaar ñi, Yawut beek jàmbur bi, ci jenn jëmmu boppam, ñu doon kenn nit ku yees, ba jàmmoo.
Efes 2:15
Jàmm laa leen bàyyee, sama jàmm laa leen may te mayuma leen ko ni àddina di mayee. Buleen jaaxle, buleen tiit.
Yowaan 14:27
Bés yu mujj yi
Wone yépp26 Des 2025
25 Des 2025
24 Des 2025
23 Des 2025
22 Des 2025
21 Des 2025
20 Des 2025