Ku topp bakkanam, fàww mu dee, waaye ku rey jëfi yaramam ci ndimbalal Noowug Yàlla, dina texe.
Room 8:13
Leeru Bés bi
Ku topp bakkanam, fàww mu dee, waaye ku rey jëfi yaramam ci ndimbalal Noowug Yàlla, dina texe.
Room 8:13
Jëfi bakkan nag yomb naa xàmmee, te mooy: séy yi yoon tere ak jëfi sobe ak yàqute
Galasi 5:19
ak ñeetaane ak màndite ak xawaare yiy ànd ak moy ak yeneen yu ni mel. Ma artu leen nag, na ma leen artoo woon: ñiy jëfe noonu, amuñu cér ci nguurug Yàlla. Meññeefum Noowug Yàlla nag moo di: cofeel ak mbég ak jàmm ak xolu muñ ak mbaax akug tabe ak ngëm akug teey ak noot sa bakkan. Yu mel noonu, wenn yoon bañu ko. Ñi bokk ci Almasi Yeesu nag, ñoo daaj ca bantam ba seen bakkan, daajaale ko ak sàkkuteefam yu tar aki xemmemtéefam. Gannaaw nag Noowug Yàlla moo nu dundal, nanu topp Noo gi.
Galasi 5:21–25
Ndax yiwu Yàlla kat feeñ na, te looloo indil ñépp ag mucc. Yiw woowu moo nu digal nu dëddu ñeme Yàlla ak xemmemtéefi àddina, te jiital sunum xel, di jëfe njub, te nekke ragal Yàlla ci àddinay tey jii. Loolu lees nu digal, li feek nu ngi séentu yaakaaru mbég ma, keroog bésu peeñum sunu màggaayu Yàlla miy Yeesu Almasi bi, Musalkat bi. Moo maye bakkanam ngir nun, moo nu jot, ba nu mucc ci gépp njubadi, moo nu def askan wu mu setalal boppam, séddoo nu, nuy askan wu farlu ci jëf ju baax.
Tit 2:11–14
Kilifay waa Filisti ne: «Ebrë yii, nag?» Akis wax ak kilifay waa Filisti, ne leen: «Xanaa du Daawuda, surgab Sawul buurub Israayil? Lu ëpp at a ngii mu nekk ak man, te gisuma ci moom sikk, ba mu teqalikook Sawul, ba bésub tey jii.»
1.Samiyel 29:3
Su ñu leen jànnee sax ndax turu Almasi bi, ndokkalee yeen, ndax Noo gu darajawu gi, Noowug Yàlla moo wàcc ci yeen. Waaye rey nit, mbaa sàcc, mbaa def lu bon, mbaa dugg ci yëfi jàmbur, bumu waral coonoy kenn ci yeen.
1.Piyeer 4:14–15
Li dagan ci yaw, bu ko jariñoo ba may kenn lu mu ŋàññee.
Room 14:16
Seen dundin ci biir jàmbur ñi gëmul, rafetalleen ko, ba su ñu leen waxaloon ne ay defkati lu bon ngeen itam, seen jëf ju rafet lañuy gis, te moom lañuy sàbbaale Yàlla, kera bésub dikkam.
1.Piyeer 2:12
Buleen lëkkoo ak gëmadikat ñi. Gan lëngoo la njub ak ndëngte séq? Gan booloo la leer ak lëndëm séq?
2.Korent 6:14
Gan takktoo la kër Yàlla séq ak ay tuur? Ndax kat, nun, nooy kër Yàlla jiy dund, te noonu la ko Yàlla waxe ne: «Maay dëkk ci seen biir, di dox ci seen biir, di seen Yàlla, ñuy sama ñoñ.» Kon nag: «Nangeen génne ci seen biir, te teqalikoo ak ñoom,» la Boroom bi wax, «lu sobewu, buleen ko laal. Su boobaa, maa leen di dalal.
2.Korent 6:16–17
Waaye yeen nag yeenay giir giy tànnéef, yeenay sarxalkati buur, yeenay askan wu sell, yeenay xeet wi ñu jot, ngir ngeen biral jaloore yu wéet yi ñeel ki leen woo, génnee leen cig lëndëm, indi leen ci leeram gu yéeme.
1.Piyeer 2:9
Bés yu mujj yi
Wone yépp23 Des 2025
22 Des 2025
21 Des 2025
20 Des 2025
19 Des 2025
18 Des 2025
17 Des 2025