Xanaa ku langaamoo sama kiiraay te jàmmook man, ba jàmmook man.
Esayi 27:5
Leeru Bés bi
Xanaa ku langaamoo sama kiiraay te jàmmook man, ba jàmmook man.
Esayi 27:5
Ndax man déy, xam naa mébét yi ma leen mébétal. Kàddug Aji Sax jee. Du mébéti loraange, waaye mébéti jàmm laa leen mébétal, ngir may leen yaakaaru ëllëg.
Yeremi 29:11
Waaye yeen ñi sore woon, léegi bi ngeen nekkee ci Almasi Yeesu, jege ngeen ndax deretu Almasi ji tuuru. Ndaxte moom mooy sunu jàmm, moom mi boole ñaar, Yawut bi ak jàmbur bi dul Yawut, def leen kenn. Ci suuxu yaramam wa ñu daaj la ñàggee ñagu mbañeel bi doxoon sunu diggante.
Efes 2:13–14
ndax Yàlla la soob mu dëël gépp matam ci moom. Deretam ja tuuru ca bant ba, ca la Yàlla defe jàmm, ba sottale ci moom, pexe mi mu jubalee boppam ak lépp, muy lu nekk ci kaw suuf ak la fa asamaan.
Kolos 1:19–20
te ci yiwu Yàlla wu àndul ak genn pey lees di baaxe ñépp àtteb ñu jub, ndax njot gi sottee ci Almasi Yeesu. Moom la Yàlla tudd muy njot gu ngëm di maye, ci kaw deretam ji tuuru. Noonu la Yàlla firndeele ne njubteem mat na sëkk doonte tanqamlu woon na bàkkaari niti jamono ya woon, ndax Yàlla ci biir ag jéllaleem la firndeel njubteem ci janti tey jii, ngir mu leer ne moo wéye njub, te képp ku gëm Yeesu, moo koy baaxe àtteb ku jub.
Room 3:24–26
Su nu ko àggee sunuy bàkkaar, te muy ku jara wóolu, di boroom njub, moo nuy jéggal sunuy bàkkaar, raxas nu ba nu set, tàggook gépp njubadi.
1.Yowaan 1:9
Wóoluleen Aji Sax ji tey ak ëllëg; Ki Sax, di Aji Sax ji déy, moo mat cëslaay ba fàww.
Esayi 26:4
Seede si moo di texe ba fàww la nu Yàlla jagleel, te texe googu ci Doomam la nekk.
1.Yowaan 5:11
Ndax kat ni Baay bi jagoo dund ci jëmmu boppam, noonu la maye Doom ji mu jagoo dund ci jëmmu boppam,
Yowaan 5:26
ndax kat, ni Baay bi di dekkale ñi dee, dundal leen, noonu la Doom jiy dundale ku mu namma dundal.
Yowaan 5:21
Yeesu ne ko: «Man maay ndekkite li, maay dund gi; ku ma gëm, soo deewee it, dinga dund. Te képp kuy dund te gëm ma, doo dee mukk. Ndax gëm nga loolu?»
Yowaan 11:25–26
«Man maay sàmm bi baax. Sàmm bu baax, bakkanam lay joxe, jote ko ay xaram.
Yowaan 10:11
Li tax Baay bi sopp ma, moo di sama bakkan laa joxe, ba man koo jëlaat. Kenn du jële sama bakkan ci man; man maa koy joxeel sama bopp. Maa ko saña joxe, maa ko saña jëlaat, te loolu la ma sama Baay sant.»
Yowaan 10:17–18
Yeesu ne ko: «Man maay yoon wi, maay dëgg gi, te maay dund gi. Kenn du ñëw ci Baay bi te jaarewul ci man.
Yowaan 14:6
Maa leen ko wax déy ci lu wér, ku ma gëm, jëf ji may def man, moom itam dina ko def, te jëf ju raw jii sax lay def, ndax man, ci Baay bi laa jëm.
Yowaan 14:12
ndaxte dee ngeen, ba seenug dund ànd ak Almasi bi, làqe fa Yàlla. Seenug dund dëgg Almasi bi la, te keroog bu Almasi bi feeñee, yeen itam dingeen ànd ak moom feeñ, ba séddu ci ndamam.
Kolos 3:3–4
Bés yu mujj yi
Wone yépp22 Des 2025
21 Des 2025
20 Des 2025
19 Des 2025
18 Des 2025
17 Des 2025
16 Des 2025