Te mooy noonu mu nu tànne ba àddina sosoogul ndax Almasi bi nu bokk, ngir nu doon ñu sell te mucc sikk fa kanamam. Ci biir cofeel
Efes 1:4
Leeru Bés bi
Te mooy noonu mu nu tànne ba àddina sosoogul ndax Almasi bi nu bokk, ngir nu doon ñu sell te mucc sikk fa kanamam. Ci biir cofeel
Efes 1:4
Nun nag bokk yi, manunoo ñàkka sant Yàlla fu nu tollu, ci yeen ñi Boroom bi sopp, ndax yeen la njëkka tànn, ngir sellal leen ci Noo gu Sell gi, ak itam seen ngëm gi ngeen gëm dëgg gi, ngir texeel leen.
2.Tesalonig 2:13
Ndax ñooñu Yàllaa leen ràññee woon lu jiitu, te it la mu dogaloon lu jiitu ci ñoom moo di ñu niru Doomam, ngir Doomam di taaw ci biir rakk yu bare. Ñi Yàlla tuddaloon loolu lu jiitu, moo leen woo itam; ñooñu mu woo, moo leen baaxe itam àtteb ñu jub; te ñooñu mu jox àtteb ñu jub, moo leen darajaal itam.
Room 8:29–30
Yeen la Yàlla Baay bi ràññee lu jiitu, ci ni mu leen sellale Noo gu Sell gi, ngir ngeen mana déggal Yeesu Almasi bi, boole ci tooyloo deretam, mu setal leen. Na aw yiw ak jàmm juy baawaan ñeel leen.
1.Piyeer 1:2
Maa leen di jox xol bu yees, te xel mu yees laay def ci seen dënn. Xolu doj bi laay roccee ci seen suux, wecceel leen ko xol yu nooye ni suux,
Esekiyel 36:26
Yàlla kat ci cellte la nu woo, waaye du ci jëfin wu setul.
1.Tesalonig 4:7
Jaraaf ja daan ànd ak Buur saa su ne àddu ca ne góoru Yàlla ga: «Ma ne, su Aji Sax ji ubbi woon sàqi asamaan sax, ndax man naa tax loolu am?» Mu ne ko: «Dinga ci teg sa bët déy, waaye doo ci lekk.»
2.Buur ya 7:2
Yeesu ne leen: «Gëmleen Yàlla.
Màrk 11:22
Ku amul ngëm nag doo mana neex Yàlla, ndax kiy dikk fi Yàlla, fàww nga njëkka gëm ne Yàlla am na, gëm it ne ñi koy sàkku, moo leen di yool.
Yawut ya 11:6
Yeesu nag ne leen jàkk, ne: «Loolu nit la të, waaye Yàlla man na lépp.»
Macë 19:26
Ana lu tax ba ma dikkee, kenn nekku fa? Ma woote, kenn wuyuwul? Damaa gàtta gàtt loxo, ba manumaa walloo? Am damaa ñàkk doole ju ma xettalee? Xanaa du maay gëdd géej, mu wow, maay defi dex màndiŋ, ndox tukki; jën ya mar, dee ba yàqu?
Esayi 50:2
«Samay xalaat déy du seeni xalaat, te samay jëfin du seeni jëfin.» Kàddug Aji Sax jee. Mu ne: «Ni asamaan tiime suuf, ni la samay jëfin tiime seeni jëfin, samay xalaat it tiime ko seeni xalaat.
Esayi 55:8–9
Indileen mboolem céru fukkeel ca kërug denc ya, ba ab dund am sama biir kër, te ngeen seetloo ma ko rekk,» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax, «ndegam duma leen ubbil bunti asamaan, ba sottil leen barke bu doy.
Malasi 3:10
Ma ne, Aji Sax ji gàttul loxo ba tëlee walloo, noppam naqariwul ba tere koo dégg.
Esayi 59:1
Aji Sax ji nag duma Kuuseen ña fa kanam Asa ak Yuda, Kuuseen ña daw.
2.Jaar-jaar ya 14:11
Nun ci sunu wàllu bopp, jàppoon nanu ne sunu àtteb dee moo taxaw. Waaye loolu tax na nu bañatee yaakaar sunu bopp, xanaa di yaakaar Yàlla miy dekkal ñi dee.
2.Korent 1:9
Bés yu mujj yi
Wone yépp19 Des 2025
18 Des 2025
17 Des 2025
16 Des 2025
15 Des 2025
14 Des 2025
13 Des 2025