Leeru Bés bi — 17 Desàmbar: Taalifi cant 80:18

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Yal nanga yiir ki nga tànn, kii nga dooleelal sa bopp,

Taalifi cant 80:18

Noowug Yàlla mooy dundloo; nitu suuxu neen manul dara. Kàddu gi ma leen wax moo leen di jottali Noowug Yàlla giy taxa dund.

Yowaan 6:63

Te itam Noowug Yàlla moo nuy dimbali ndax sunug néew doole, nde xamunu sax li jaadoo sàkku ci sunuy ñaan, waaye Noo gi moo nuy tinule ay onk yu wees kàddug làmmiñ. Te kiy xool li ci biir xol yi, xam na liy xintey Noo gi, ndax ni ko Yàlla bëgge, ni la Noo giy tinool ñu sell ñi.

Room 8:26–27

Deeleen ñaan fu ngeen tollu, gépp xeetu ñaan aki dagaan ci ndimbalal Noo gi, ànd ci ak teewlu fu ngeen tollu, ak gépp parlu, te ngeen di ñaanal mboolem gëmkat ñu sell ñi.

Efes 6:18

Duma fàtte mukk say tegtal, ci nga may musale.

Taalifi cant 119:93

Noowug Yàlla mooy dundloo; nitu suuxu neen manul dara. Kàddu gi ma leen wax moo leen di jottali Noowug Yàlla giy taxa dund.

Yowaan 6:63

Moo nu may manoorey doon ay liggéeykati kóllëre gu bees gu ajuwul ci mbindum ndigali yoon, xanaa kóllëre gu aju ci Noowug Yàlla. Ndaxte mbindum ndigali yoon day rey, te Noo gi di dundloo.

2.Korent 3:6

Su ngeen saxee ci man te samay wax sax ci yeen, lu ngeen bëgg, ñaanleen ko, dees na leen ko nangul.

Yowaan 15:7

Kóolute gi nu am ci Yàlla moo di su nu ko ñaanee lenn lu dëppook coobareem, da nuy nangul.

1.Yowaan 5:14

Moo tax ma di leen biral ne amul kenn kuy waxe Noowug Yàlla ku naan: «Alkànde ñeel na Yeesu.» Te it kenn manul ne: «Yeesu moo di Sang,» te du lu ko Noo gu Sell gi xamal.

1.Korent 12:3

jëfi lëndëm amul njariñ, buleen ci bokk, xanaa ngeen feeñal ñaawtéefu jëf ja.

Efes 5:11

Bu leen kenn nax: «Ànd bu bon yàq na jikko ju baax.»

1.Korent 15:33

Seen damu gii de jekkul dara. Xanaa xamuleen ne as lawiir tooyalu sunguf bépp lay funkil? Setalleen seen bopp boog, génneleen lawiir bu yàgg bi ci seen biir, ba mana doon tooyal bu bees bu mucc lawiir, nde doon ngeen ko ba noppi, ndax Almasi bi, sunu gàttub bésub Mucc biy sunub sarax, rendilees na nu ko.

1.Korent 5:6–7

Bindoon naa leen ca sama bataaxal ba, ne buleen amlante ak fokati séy yi. Waaye moos fokati àddina sii taxul woon may wax, mbaa bëgge yi ak ŋàppaaral yi ak bokkaalekat yi, nde kon fàww ngeen génn àddina. Dama leena bind, ne leen buleen amlante ak ku tuddoo mbokkum gëmkat, te di fokatub séy, mbaa mu dib bëgge, mbaa mu dib bokkaalekat, mbaa ab saagakat, mbaa màndikat, mbaa ab ŋàppaaral. Ku ni mel, buleen bokk ak moom lekk sax.

1.Korent 5:9–11

ngir seen der set wecc, te kon deesuleen mana gàkkal ci lenn. Ay goney Yàlla yu amul sikk ngeen di doon, ci biir maas gu dëng te yàqu, ngeen di lerxat ci seen biir, ni ay leer ci àddina si,

Filib 2:15

Kër gu mag nag, du ndabi wurus ak xaalis rekk a fa am, waaye yoy bant a nga fa ak yoy ban; yii di ndabi teraanga, yee di ndabi njoogaan.

2.Timote 2:20