Ceeñeeru biir lëndëm jollil na ku jub ak ku baax, di boroom yërmande ak njubte.
Taalifi cant 112:4
Leeru Bés bi
Ceeñeeru biir lëndëm jollil na ku jub ak ku baax, di boroom yërmande ak njubte.
Taalifi cant 112:4
Ana ku ragal Aji Sax ji ci yeen, di déglu kàddug jaamam? Képp kuy doxe lëndëm te amul leeraange, na wóolu Aji Sax ji, te wéeroo Yàllaam jii.
Esayi 50:10
Soo tërëfee it, doo daanu. Aji Sax jee lay walloo loxoom.
Taalifi cant 37:24
Santaane da lay niital, ndigal leeralal la, artookub yar di yoonu dund.
Kàddu yu xelu 6:23
Yaw samab noon, bu ma ree; maa daanu, maay jóg. Ci biir lëndëm laa toog, waaye Aji Sax jeey samag leer. Maa moy Aji Sax ji, kon naa tegoo meram, ba mu layool ma, dëggal ma, génne ma ba dugal ma ci leer gi, ma gis àtteb dëggam.
Mise 7:8–9
«Bët mooy làmpu yaram. Su sa bët wéree, sa yaram wépp a ciy leerloo, waaye bu sa bët bonee, sa yaram wépp a ngi ci lëndëm. Leer gi ci yaw nag, su dee ag lëndëm, ndaw lëndëm gu réy!
Macë 6:22–23
Mooy sàmm géttam bii ni kuy sàmmug juram, boole mbote yi cib loxoom, taf cib dënnam, yóbbu; xar yiy nàmpal, mu wommat.»
Esayi 40:11
Gannaaw loolu Yeesu woo taalibeem ya, ne leen: «Damaa yërëm mbooloo mi, ndax ñetti fan a ngii yu ñu nekk ak man, te amuñu lu ñu lekk. Bëgguma leena yiwi, ñu deme xiif, bala ñoo tële ci yoon wi.»
Macë 15:32
Ndax sarxalkat bu mag bi nu am du ku tëlee yég sunuy néew doole, waaye ni nun rekk lees ko nattoo wet gu nekk, te taxul mu bàkkaar.
Yawut ya 4:15
Ay xale lañu indiloon Yeesu ngir mu teg leen ay loxoom. Teewul taalibe ya jànni leen.
Màrk 10:13
Yeesu nag fab leen, teg leen ay loxoom, barkeel leen.
Màrk 10:16
Lajj naa ni xar mu réer; gindi ma, Sang bi, sàgganewuma say santaane de!
Taalifi cant 119:176
Ndax Doomu nit ki, ñi réer la seetsi, ngir musal leen.»
Luug 19:10
«Yeena réeroon niy xar,» waaye délsi ngeen tey ci seenub sàmm, seen wattukatub xol.
1.Piyeer 2:25
«Buleen ragal dara, yeen jur gu sew gi, ndax seen Baay la soob, mu jagleel leen nguur gi.
Luug 12:32
Man mii maay sàmm samay gàtt te maa leen di gooral. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.
Esekiyel 34:15
Bés yu mujj yi
Wone yépp18 Des 2025
17 Des 2025
16 Des 2025
15 Des 2025
14 Des 2025
13 Des 2025
12 Des 2025