Kon nag nanu ñemee dikk ba ca ngàngunem yiw ma, ndax nu jot yërmande te dajeek aw yiw wu nu wallu fu nu ko soxlaa.
Yawut ya 4:16
Leeru Bés bi
Kon nag nanu ñemee dikk ba ca ngàngunem yiw ma, ndax nu jot yërmande te dajeek aw yiw wu nu wallu fu nu ko soxlaa.
Yawut ya 4:16
Buleen jaaxle ci dara, waaye ci mbir mu mu mana doon, deeleen dikke Yàlla seeni soxla, di ko ñaan aka dagaan te boole ci di ko sant. Su boobaa jàmmu Yàlla ji wees ab takk, mooy sàmm seen xol ak seenum xel ndax Almasi Yeesu.
Filib 4:6–7
Mayeesu leen noo gu leen di desloo cig njaam, ba tax leena dellu cig ragal, waaye Noowug doom yu ñu doomoo, moom lees leen may, te looloo nu tax di woowe Yàlla: «Abba», mu tekki «Baay».
Room 8:15
Làquwuma, di waxe béreb bu lëndëm. Newuma it askanu Yanqóoba: “Wërleen ma ci neen.” Man Aji Sax ji maay wax dëgg, di biral liy yoon.»
Esayi 45:19
Léegi nag bokk yi, am nanu sañ-sañu dugg ca néeg bu sella sell ba, ngir deretu Yeesu,
Yawut ya 10:19
Kon nag nanu agsee fi Yàlla xol bu dëggu ak fit wu mat sëkk wu ngëm waral, gannaaw wisees na sunum xel ndoxum setlu, ba mu tàggook bépp gàkk bu mu nu sikkale, te raggees na sunu yaram ci ndoxum setlu.
Yawut ya 10:22
Moo tax nu mana am fitu wax ne: «Boroom beey sama ndimbal, duma tiit. Ana lees ma manal?»
Yawut ya 13:6
Su boobaa dingeen xam liy dëgg, te dëgg gi moo leen di goreel.»
Yowaan 8:32
Boroom bi mooy Noo gi, te fu Noo gi nekk, fa la nit di goree.
2.Korent 3:17
Ndax kat, yoonu Noo gu Sell giy maye bakkan te nekk ci Almasi Yeesu moo la yiwi, ba nga mucc ci yoonu bàkkaar ak dee.
Room 8:2
Kon nag su leen Doom ji goreelee, ngeen diy gor tigi.
Yowaan 8:36
Kon nag bokk yi, nun dunu doomi jaam bi, waaye nooy doomi gor si.
Galasi 4:31
Xam nanu nag ne nit ki, du ci jëfi sàmm ndigali yoon la ko Yàlla di baaxee àtteb ku jub, waaye ci ngëm gu mu gëm Yeesu Almasi bi. Te nun itam, Almasi Yeesu lanu gëm, ngir Yàlla àtte nu àtteb ku jub ci kaw gëm gu nu gëm Almasi bi, te du ci kaw jëf ju nu sàmme ndigali yoon. Ndax kat du ci jëfi sàmm yoon lees di baaxee kenn àtteb ku jub.
Galasi 2:16
Waaye ki ne jàkk yoon wu mat sëkk wiy goreel ku ko topp, saxoo yoon wi te bañ koo dégg, fàtte, xanaa di dégg, jëfe, kooku mooy bége jëfam.
Yanqóoba 1:25
Almasi bi da noo yiwi, ngir nu yiwiku, kon nag saxooleen ko, te baña laxasooti buumi njaam.
Galasi 5:1
Bés yu mujj yi
Wone yépp17 Des 2025
16 Des 2025
15 Des 2025
14 Des 2025
13 Des 2025
12 Des 2025
11 Des 2025