Leeru Bés bi — 25 Desàmbar: Tit 3:4

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Waaye ba Yàlla sunu Musalkat feeñalee mbaaxam ak mbëggeelam ci doom aadama,

Tit 3:4

Ñu ne: «Bu yàgg la nu Aji Sax ji feeñu, ne nu: “Maa leen masa bëgg, ba tax ma sédd leen ngor.

Yeremi 31:3

Ni cofeelu Yàlla feeñe ci nun moo di jenn Doomu boppam ji mu yebal ci àddina, ngir nu mana dund ci kàttanam. Lii mooy cofeel: cofeel gi du sunug cofeel, nun ci Yàlla; xanaa cofeel gi mu nu sopp, ba yebal Doomam, def ko njotlaay, ñeel sunuy bàkkaar.

1.Yowaan 4:9–10

Waaye ba àpp ba jotee, Yàlla moo yónni Doomam, mu juddoo ci jigéen, juddoo ci biir curgag yoonu Musaa, ngir jot ñi ci curgag yoon wi, ba nu jagoo cérub doom.

Galasi 4:4–5

Kàddu gee sol aw suux, doon nit, màkkaanoo ci sunu biir, nu ne jàkk ci darajaam, darajay jenn Doom ji bawoo ci Baay bi, mat sëkk ci aw yiw akug dëgg.

Yowaan 1:14

Deesul nàttable moos màggaayu mbóot mii feeñe ci sunu yoonu ngëm: Kii moo feeñe ci yaramu suux, Noowug Yàlla dëggal ko, malaaka ya niir ko; moom lañu waaree ci xeet yi, gëmees na ko ci kaw suuf it, te yéegees na ko fa leer ga.

1.Timote 3:16

Gone yooyu nag, bindeefi suux ak deret lañu bokk doon, ñoom ñépp. Moo tax Yeesu itam dikk bokk ak ñoom woowu nekkin, ngir mana dee ba def deewug boppam pexe mi mu neenale ka yoroon dooley dee, te mooy Seytaane.

Yawut ya 2:14

Cant ñeel na Yàlla ci mayam gu tiiñ aw làmmiñ.

2.Korent 9:15

Di woyu cantu màggal. Yeen waa àddina sépp, xaaculleen Aji Sax ji. Nangeen jaamu Aji Sax ji ci mbég, dikke koy woy!

Taalifi cant 100:1–2

Nangeen dem këram, dugge faag cant, dugg ëttam di màggal, sant ko, teral turam.

Taalifi cant 100:4

Dooley kilifteefam ak jàmm ja du am kemu, fa jalub Daawuda ak nguuram ga muy samp, saxale ko yoon ak njub tey jii ba fàww. Lii la Aji Sax ji Boroom gàngoor yi def ci xéraangeem. Boroom bee yónnee kàddu gu dal Israayil, askanu Yanqóoba,

Esayi 9:6–7

Moom mi nu bañalul Doomu boppam, xanaa joxeel nu ko, nun ñépp, ana nu mu nuy baña baaxee gépp yiw, boole ci?

Room 8:32

«Boroom tóokër ba nag desewul kenn ku dul doomam ji mu sopp. Mu mujj koo yebal ca beykat ya te naan: “Sama doom, dinañu ko rus.”

Màrk 12:6

Nañu sante Aji Sax ji ngoram ak kéemaanam yi ñeel doom aadama yi.

Taalifi cant 107:21

Ñeel Daawuda. Naa sant Aji Sax ji ci saa xol bii, saa jëmm jépp di sàbbaal sellaayu turam!

Taalifi cant 103:1

Maryaama nag ne: «Sama xol laay màggale Boroom bi, samag noo laay bége Yàlla mi may musal,

Luug 1:46–47