Leeru Bés bi — 22 Desàmbar: 1.Tesalonig 1:3

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

ak di baamtu fi kanam Yàlla sunu Baay jëf ji juddoo ci seen ngëm ak liggéey bi sottee ci seen cofeel ak yaakaar ji ngeen saxoo di séentu sunu Sang Yeesu Almasi bi.

1.Tesalonig 1:3

Yeesu ne leen: «Jëf ji neex Yàlla, mooy ngeen gëm ki mu yebal.»

Yowaan 6:29

Noonu la ngëm deme, su amul jëf ju mu àndal, ngëm gu dee la.

Yanqóoba 2:17

Ci Almasi Yeesu mi nu gëm, xaraf ak ñàkka xaraf, dara amu ci solo; li am solo mooy ngëm gi jëfi cofeel di firndeel.

Galasi 5:6

Ku jiwal bànneexu bakkanam, ci bànneexu bakkanam lay jële ngóobum yàqute; ku jiwal Noowug Yàlla, ci Noo gi ngay góobe texe gu sax dàkk.

Galasi 6:8

Ndax kat noo di liggéeyu Yàlla; Yàllaa nu yeesal ci Almasi Yeesu, ngir nu wéye jëf ju rafet ja mu nu fàgguloon ca njàlbéen, ngir nu di ko jëfe.

Efes 2:10

Moo maye bakkanam ngir nun, moo nu jot, ba nu mucc ci gépp njubadi, moo nu def askan wu mu setalal boppam, séddoo nu, nuy askan wu farlu ci jëf ju baax.

Tit 2:14

Bokk yi, manunoo ñàkka sant Yàlla ci yeen fu nu tollu, te muy lu jaadu, gannaaw seen ngëm a ngi yokku bu baaxa baax, te cofeelu ku nekk ci yeen ñépp di gënatee law, digganteem ak moroomam.

2.Tesalonig 1:3

Moo tax nu saxoo leena ñaanal, ngir sunu Yàlla yellale leen ab wooteem, ngir itam mu sottale kàttanam seen mboolemi mébét ci lu baax ak seen jépp jëf ju laloo ngëm.

2.Tesalonig 1:11

ndax Yàlla mooy liggéey ci yeen lu tax ngeen mana namma jëfe coobareem, ba man koo jëfe.

Filib 2:13

Ñooñoo naan: «Ki dige woona ñëw, ana mu? Ba maam ya nelawee de yàgg na, waaye lépp a ngi wéye na woon ca njàlbéenu àddina.»

2.Piyeer 3:4

Enog, juróom ñaareelu maam ma gannaaw Aadama, ñooñu la jottali woon waxyu bu leen dal, ne: «Boroom baa ngii dikk, ànd ak ay junniy junneem ñu sell, ngir àtte ñépp, ba tiiñal mboolem yéefar yi, ndax mboolem nu yéefare ni ñu jëfe seen jëfi yéefar ak mboolem kàddu yu ñaaw yi bàkkaarkati yéefar yi teg cib deram.»

Yudd 14–15

Mu ngoogu di dikk, indaale niir yi, te ñépp a koy teg bët, ba ca ña ko jamoon sax, te giiri kaw suuf yépp ay jooy ndax moom. Noonu la moos. Amiin.

Peeñu ma 1:7

Sang bi ci boppam, woote bu xumb lay wàccaalee asamaan, baatu kilifag malaaka jib, ànd ak coowal liitu Yàlla. Su ko defee ña seenug dee fekk ñu gëm Almasi bi ñooy njëkka dekki. Gannaaw loolu nun ñi fi dese bakkan lees di këfandoo ak ñoom, jëme ca niir ya, ngir nu dajejeek Sang bi fa jaww ja, nu daldi nekk ak moom ba fàww.

1.Tesalonig 4:16–17

Ndax yiwu Yàlla kat feeñ na, te looloo indil ñépp ag mucc. Yiw woowu moo nu digal nu dëddu ñeme Yàlla ak xemmemtéefi àddina, te jiital sunum xel, di jëfe njub, te nekke ragal Yàlla ci àddinay tey jii. Loolu lees nu digal, li feek nu ngi séentu yaakaaru mbég ma, keroog bésu peeñum sunu màggaayu Yàlla miy Yeesu Almasi bi, Musalkat bi.

Tit 2:11–13