Leeru Bés bi — 21 Desàmbar: Esayi 60:20

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Sab jant du sooti, sa weer du suuxati. Aji Sax jeey doon sag leer ba fàww, sa fani ñaawlu jeex.

Esayi 60:20

Loolu dama leen koo wax ngir seen xel dal ci man. Àddina sii, dingeen fi am njàqare, waaye dëgërluleen, ndax daan naa àddina.»

Yowaan 16:33

Xam nanu ba fii nu tollu ne mboolem càkkéef gaa ngi binni ndax mitit, ni kuy matu. Te du càkkéef gi rekk, waaye nun ci sunu bopp itam, ci lanu, nun ñi jot ab dawal ci Noo gu Sell gi, nun ci sunu bopp sax nu ngi binni sunu biir xol, ndax yàkkamtee jot céru doomi Yàlla, ba sunu njotug yaram mat.

Room 8:22–23

Noo ngi onk ndax diis, li feek nu ngeek sunuw yaram, xayma bi nu soloo nii. Du summiku lanu namm, waaye solu teg ko ci lanu namm, ngir li jëm ci dee, daldi suux ci biir dund.

2.Korent 5:4

Ma ne ko: «Sama sang, loolu de xanaa yaa ko xam.» Mu ne ma: «Ñoo di ñi jóge ca nattu bu réy ba. Fóot nañu seeni mbubb, ba weexal ko ci deretu Xar mi. Loolu moo leen taxa teew fi kanam ngàngunem Yàlla, di ko jaamu ci biir màkkaanam guddi ak bëccëg, te ki toog ci ngàngune mi moo leen di yiir. Dootuñu xiif, dootuñu mar. Dootuñu loru ci jant bi mbaa weneen tàngoor, ndaxte Xar mi ci diggu ngàngune mi moo leen di sàmm, yóbbu leen ca bëti ndoxum dund ma, te Yàllaa leen di fompal wépp rongooñ.»

Peeñu ma 7:14–17

Teewul Yeesoo nga ca taatu gaal ga, tëdd, gegenu, di nelaw. Taalibe ya yee ko, ne ko: «Kilifa gi, nu ngi sànku, xanaa xalaatoo nu?»

Màrk 4:38

Aji Sax jee baaxe ñépp, di yërëm lu mu sàkk.

Taalifi cant 145:9

Man ngeena dunde boroom bakkan yooyu yépp. Jagleel naa leen mbindeef yooyu yépp, ni ma leen jagleele woon gàncax.

Njàlbéen ga 9:3

Li feek suuf di suuf, muy nji walla ngóob, sedd aku tàngoor, nawet it mbaa noor, mbaa guddeek bëccëg, lenn du ci dakk.»

Njàlbéen ga 8:22

Aji Sax jee baax, moo dib rawtu, bésub njàqare, te moo ràññee ñi ko làqoo.

Nawum 1:7

Ba mu ko defee Yàlla dégg baatu xale bu góor ba. Malaakam Yàlla ma àddoo asamaan, ne Ajara: «Ajara, lan la? Bul ragal dara, ndaxte Yàlla dégg na sa baatu doom ci diggante bii mu tollu.

Njàlbéen ga 21:17

Ci kaw loolu Yàlla muri ay bëtam, mu gis ab seyaan, daldi cay dem, duy mbuusam, ba mu fees, jox ca doomam, mu naan.

Njàlbéen ga 21:19

Kon nag, buleen jaaxle, naan: “Lu nuy lekk?” mbaa “Lu nuy naan?” mbaa “Lu nuy sol?” Ndaxte loolu lépp, yéefar yi ñoo koy tiisoo. Te seen Baay ba fa asamaan xam na ne soxla ngeen loolu lépp.

Macë 6:31–32

Ñi barele alalu àddinay tey nag, dénk leen ñu baña réy te baña yaakaar alal ju wóoradi, te ñu yaakaar Yàlla mi nuy xéewale lépp, ngir nu di ko bége.

1.Timote 6:17