Balaa màggalu bésub Mucc baa dikk, Yeesu xamoon na ne waxtu wa muy bàyyikoo àddina, jëm fa Baay ba, jot na. Cofeelu Yeesu ak ñoñam ñi ci àddina, googu cofeel la leen sopp ba ca muj ga.
Yowaan 13:1
Leeru Bés bi
Balaa màggalu bésub Mucc baa dikk, Yeesu xamoon na ne waxtu wa muy bàyyikoo àddina, jëm fa Baay ba, jot na. Cofeelu Yeesu ak ñoñam ñi ci àddina, googu cofeel la leen sopp ba ca muj ga.
Yowaan 13:1
Man nag, ñoom laay ñaanal; ñaanaluma waa àddina, waaye ñi nga ma dénk, ñoom laay ñaanal, ndax sa ñoñ lañu. Mboolem lu ma am, yaa ko moom, te loo am, maa ko moom, te ci ñoom la sama daraja feeñe.
Yowaan 17:9–10
Ñaanuma nga jële leen ci àddina, xanaa nga musal leen ci ku bon ki. Ni ma ñàkka bokke ci àddina, man ci sama bopp, noonu lañu ñàkka bokke ci àddina.
Yowaan 17:15–16
«Ni ma Baay bi soppe, man itam noonu laa leen soppe. Saxleen ci sama cofeel.
Yowaan 15:9
Joxe sa bakkan te say xarit tax, ameesul cofeel gu ko raw, te samay xarit ngeen, ndegam yeena ngi def li ma leen sant.
Yowaan 15:13–14
Te lii kat, bir na ma: ki tàmbali jii jëf ju baax ci yeen, dina ko àggale ba keroog bésub Almasi Yeesu.
Filib 1:6
Jëkkër nag, na sopp jabaram ni Almasi bi soppe mbooloom gëmkat ñi, ba joxeel leen bakkanam. Moo defal loolu mbooloo mi, ba man koo setale cangaayal ndox mu ànd ak kàddoom, ngir sellal ko.
Efes 5:25–26
Waaye nun la Yàlla feeñalal denc googu jaare ci Xelam. Ndaxte Xelum Yàlla lépp lay gëstu ba ci xóotey mbóoti Yàlla.
1.Korent 2:10
Wooweetuma leen ay jaam, ndax ab jaam xamul lu sangam di def. Xarit laa leen woowe, ndax mboolem lu ma dégge ci sama Baay, xamal naa leen ko.
Yowaan 15:15
Mu ne leen: «Yeen lañu may ngeen xam mbóoti nguurug asamaan, waaye ñale, mayeesu leen ko.
Macë 13:11
Nun nag du xelum àddina lanu jot, waaye Xel mi bawoo fa Yàlla lanu jot, ngir nu mana ràññee li nu Yàlla baaxe.
1.Korent 2:12
Looloo ma taxa sukk sama bëti óom, janook Baay bi, ki gépp njabootug asamaan ak suuf jële aw tur. May ñaan nag, mu may leen, ci koomu teraangaam, seen jëmmu biir feddaliku ak kàttanu Noowam gu Sell. Su ko defee seen ngëm tax Almasi bi dëkke seen xol, ngeen sax ay reen yu sampe ci biir cofeel, ngir yeen ak mboolem ñu sell ñi, seenum xel mana jàpp, ni mu leen ware, luy yaatuwaayub cofeelu Almasi bi ak guddaay ba ak kawewaay ba ak xóotaay ba. Ngeen boole ci daj cofeelu Almasi gi wees xam-xam, ngir ngeen fees, ba fees dell ak koomu Yàlla.
Efes 3:14–19
Bés yu mujj yi
Wone yépp15 Des 2025
14 Des 2025
13 Des 2025
12 Des 2025
11 Des 2025
10 Des 2025
9 Des 2025