Yenuleen seeni yeni moroom, su boobaa ngeen di topp yoonu Almasi bi, ba mu mat sëkk.
Galasi 6:2
Leeru Bés bi
Yenuleen seeni yeni moroom, su boobaa ngeen di topp yoonu Almasi bi, ba mu mat sëkk.
Galasi 6:2
Bu kenn ci yeen xintewoo njariñal boppam, waaye na ku nekk bàyyi xel moroomam. Noonu Almasi Yeesu doon doxale, deeleen ko doxale ci seen biir:
Filib 2:4–5
Xanaa mu ŋacc boppam, nangoo jagoo nekkinu surga. Mu mujj mel ni nit doŋŋ, di ku ñu xàmmee jëmmu nitam.
Filib 2:7
Ndax Doomu nit ki itam ñëwul ngir ñu di ko surgawu, xanaa ngir di nekk surga, ba far maye bakkanam, def ko njotug ñu bare.»
Màrk 10:45
Te ki dee ngir ñépp, daa dee ngir ñiy dund bañatee dund ngir seen bopp, xanaa di dund ngir ki dee ngir ñoom, ba dekki.
2.Korent 5:15
Ba ko Yeesu gisee muy jooy, Yawut ya mu àndal itam di jooy, yaramam daw na, mu jàq.
Yowaan 11:33
Yeesu nag jooy.
Yowaan 11:35
Ñi am mbégte, bokkleen ak ñoom seen mbégte; ñi am naqar, ngeen bokk ak ñoom seen naqar.
Room 12:15
Li may tënke nag moo di yeen ñépp, ngeen mànkoo, yégante, bëggante ni mu ware ay bokki gëmkat, baaxeenteleen te woyof. Lu bon, buleen ko feye lu bon; ay saaga it, buleen ko feye ay saaga. Xanaa ngeen ñaanal leen, feye leen ko, ndax ci loolu lees leen woo, ngir ngeen jagoo barke.
1.Piyeer 3:8–9
«Waaye, luy seen xalaat ci lii? Nit a amoon ñaari doom. Mu dikk ca kenn ka, ne ko: “Doom, demal tey liggéeyi ca toolu reseñ ba.”
Macë 21:28
Moo tax dootuloo ab jaam, doom nga. Gannaaw doom nga nag, boroom cér nga it fa Yàlla sa baay.
Galasi 4:7
Naka noonu, yeen itam jàppeleen seen bopp nit ñu dee ba dootuleen nangooti kilifteefu bàkkaar, xanaa di dund ngir Yàlla, ndax seen bokk ci Yeesu Almasi bi. Kon nag bu bàkkaar yilif seen yaramu dee wii, ba di leen nanguloo ay xemmemtéefam yu bon. Buleen jébbal seeni cér bàkkaar, mu def leen jumtukaayi njubadi; gannaaw yeena dekki bay dundaat, jébballeen Yàlla seen bopp te jébbal ko seeni cér, ngir def leen ay jumtukaayi njub.
Room 6:11–13
Gannaaw gone yu dégg ndigal ngeen, buleen toppati seen xemmemtéefi bakkan ya woon, ba ngeen xamulee. Waaye ni ki leen woo selle, yeen itam nangeen selle noonu ci seen mboolem jëfin.
1.Piyeer 1:14–15
Ku setal sa bopp nag ba mucc ci yu bon yooyii, yaay doon ndabal teraanga lu sell te amal sangam njariñ ngir jépp jëf ju baax.
2.Timote 2:21
Kon nag yeen sama bokk yi ma soppal sama bopp, farluleen, bu leen dara yëngal, te saxooleena jëm kanam ci liggéeyu Sang bi, te ngeen xam ne seenu ñaq, ci seenub ànd ak Sang bi, du neen.
1.Korent 15:58
Bés yu mujj yi
Wone yépp14 Des 2025
13 Des 2025
12 Des 2025
11 Des 2025
10 Des 2025
9 Des 2025
8 Des 2025