woyleen màggaayu turam, darajaalleen cantam.
Taalifi cant 66:2
Leeru Bés bi
woyleen màggaayu turam, darajaalleen cantam.
Taalifi cant 66:2
xeet wii ma bindal sama bopp, te ñooy siiwal sama woy.
Esayi 43:21
Maa leen di raxasal mboolem ñaawtéef gu ñu ma moye, baal leen mboolem ñaawtéef yu ñu ma moye, di ma gàntal. Dëkk bi daldi doon sama woy, di sama mbégte, di sama ndam, di sama sag ci biir mboolem xeeti àddina yi dégg ngëneel yi ma leen di defal yépp. Dinañu yéemu ba seen yaram daw ci lépp luy ngëneel ak jàmm ju ma leen di defal.
Yeremi 33:8–9
Kon nag saa su nekk, nanuy jaare ci Yeesu, di génne sunu saraxu cant, ñeel Yàlla, muy sarax su bawoo ci sunuw làmmiñ, ñu di ko birale aw turam.
Yawut ya 13:15
Boroom bi sama Yàlla, naa la sante xol bu fees, màggal la ba fàww. Ngor lu réy nga ma won, sorele maak tëraayu bàmmeel.
Taalifi cant 86:12–13
«Ana kuy sa moroom ci tuur yi, yaw Aji Sax ji? Kuy sa dend, yaak sa sellaay bu yéeme, sa yànjaay bu raglook sa jëf yu yéeme?
Mucc ga 15:11
Man de, damaa jàq, tiis. Éy Yàlla, yal naa làqoo sag wall.
Taalifi cant 69:30
Ña ngay woy woyu Musaa jaamu Yàlla ba ak woyu Xar mi, naan: «Yaw Boroom bi Yàlla Aji Man ji, yaa réy te yéeme ay jaloore. Yaw Buuru askan yi, yaa jub te dëgguy doxalin.
Peeñu ma 15:3
Ci ñoom lanu bokkoon nun ñépp itam; mas nanoo topp sunu bakkan, di jëfe lu sunu bakkan ak sunum xel xemmem. Sunu bindu nit taxoon na noo yeyoo am sànj ni ñépp.
Efes 2:3
Ndax nun itam kat, ñu ñàkk xel lanu woon te déggadi, ñu réer, tënku ci lu doon ay xemmemtéef ak bànneexi bakkan, tey wéye def lu bon ak ñeetaane, ñu jara bañ te bañante ci sunu biir.
Tit 3:3
Li ma la ne: “Fàww ngeen judduwaat,” bumu la jaaxal.
Yowaan 3:7
Ayóoba àddu ne Aji Sax ji: Man mi tekkiwul dara, nu ma lay tontoo? Sama loxo laa ube sama gémmiñ.
Ayóoba 40:3–4
Mu ne ko: «Xanaa seetlu nga Ayóoba, sama jaam bi? Amul moroom fi kaw suuf de! Ku mat la te jub, ragal Yàlla te dëddu lu bon.»
Ayóoba 1:8
Xam naa ne maa tooñ, sama moy a ngi janook man saa su ne.
Taalifi cant 51:5
Mu jële ko fa, sampal leen Daawuda, muy buur bu mu seedeel ne: “Maa ràññee Daawuda doomu Yese ji sama xol jubool, te mooy jëfe mboolem samay coobare.”
Jëf ya 13:22
te ma nekkoon ab tooñkatam, di ab bunduxataalkat, di ab néeg. Waaye yërmande laa dajeel, ngir ñàkka xam ga ma daan jëfe, te ñàkka gëm tax.
1.Timote 1:13
Lu juddoo ci nitu suuxu neen, nitu suux la, lu juddoo ci Noowug Yàlla nag, ag noo la.
Yowaan 3:6
Bés yu mujj yi
Wone yépp13 Des 2025
12 Des 2025
11 Des 2025
10 Des 2025
9 Des 2025
8 Des 2025
7 Des 2025