Kon nag yaw doom, doolewool yiw wi Almasi Yeesu di maye.
2.Timote 2:1
Leeru Bés bi
Kon nag yaw doom, doolewool yiw wi Almasi Yeesu di maye.
2.Timote 2:1
Ngir itam ngeen manoorewoo jépp manoore, na leen ko Yàlla manloo ci kàttanam gu màgg, ba ngeen mana dékku lépp ci xolu muñ,
Kolos 1:11
Kon nag, ni ngeen nangoo Almasi Yeesu di Sang bi, àndleen ak moom, jëfe noonu. Sampleen seeni reen ci moom, tabaxleen seen bopp ci moom, feddalikuleen ci wàllu ngëm, ni ñu leen ko jàngale, ba seenub xol baawaan ak kàdduy cant.
Kolos 2:6–7
ngir indil waa Siyoŋ ñiy ñaawlu ab kaala gu wuutu dóomu-taal, ak diwu mbégte mu ñu weccikoo seenu tiis, ak mbubbam cant mu ñu weccikoo xol bu jeex, ba ñu naa: «Ñii ñoo di ponkali garabi njubte yi, njëmbat li Aji Sax ji jëmbat, ngir teewal màggaayam.»
Esayi 61:3
Yeena di tabax bi ndawi Almasi bi ak yonent yi di fondmaa bi, te Almasi Yeesu ci boppam di doju koñu tabax bi. Ci moom la tabax bi bépp di temboo, ba jóg, doon jaamookaay bu sell ngir Boroom bi. Ci Almasi bi ngeen bokke ci tabax bi, yeen jàmbur ñi itam, ba mana doon dëkkuwaayu Yàlla, ci ndimbalal Noo gu Sell gi.
Efes 2:20–22
«Léegi nag, dénk naa leen Yàlla ak kàddug yiwam gi leen mana dooleel, dencal leen seen muur ci biir mboolem nit ñi ñu sellal.
Jëf ya 20:32
Su boobaa ngeen meññal ba woomle ci njub gi Yeesu Almasi bi di maye, ngir fésal màggug Yàlla, jollil ag cantam.
Filib 1:11
Joŋanteel joŋante bu baax bi, ngir yoonu ngëm wi, te nga ŋoy bu baax ci texeg fàww gi ñu la woo, ba tax nga dëggal sa ngëm nu rafet noonu nga ko dëggale woon fa kanam seede yu bare.
1.Timote 6:12
Buleen ragal seeni noon ci lenn. Seen fit mooy màndargaal sànkutey noon yi, te yeen it, mooy màndargaal seenug mucc gu bawoo fa Yàlla.
Filib 1:28
Benn yoon la Yàlla wax, ñaari yoon laa dégg, ñu ne; «Doole, fa Yàlla.»
Taalifi cant 62:12
Waaye booy sarxe, li sa loxol ndijoor di def, bu ko sa loxol càmmoñ xam, su ko defee sa sarax di kumpa, te sa Baay biy gis ci biir kumpa moo lay yool.
Macë 6:3–4
«Gannaaw diir bu yàgg njaatigeb surga ya délsi, daldi bokk xayma ak ñoom ni alalam tolloo.
Macë 25:19
Du caageenu doyloo sunu manoorey bopp, ba yaakaar ne lenn man naa sottee ci sunu wàllu bopp, waaye sunu manoore ci Yàlla la jóge.
2.Korent 3:5
Aji Sax ji, yaa nuy defal jàmm, te lépp lu nu def, yaa nu ko sottalal.
Esayi 26:12
Bés yu mujj yi
Wone yépp12 Des 2025
11 Des 2025
10 Des 2025
9 Des 2025
8 Des 2025
7 Des 2025
6 Des 2025