Aji Sax ji moo teggi say mbugal, waññi sab noon. Buurub Israayil, Aji Sax jaa ngi fi sa biir, dootuloo tiit lu bon.
Sofoni 3:15
Leeru Bés bi
Aji Sax ji moo teggi say mbugal, waññi sab noon. Buurub Israayil, Aji Sax jaa ngi fi sa biir, dootuloo tiit lu bon.
Sofoni 3:15
bul ragal, yaw laa àndal, bul tiit, maay sa Yàlla; maa lay dooleel, dimbali la déy, maa lay téyee sama loxol ndijoor liy àtte dëgg.
Esayi 41:10
Ku yoqi, dooleelleen ko, ku óom yay fenqe, jàppaleleen ko. Ku fitam rëcc, ne leen ko: «Dëgërlul te bul tiit. Sa Yàllaa ngii di la feyul, ba yool say noon. Moom mooy dikk, wallusi la.»
Esayi 35:3–4
Aji Sax ji sa Yàllaa ngi fi sa biir, di jàmbaar juy walloo. Moo lay bége ci biir bànneex, leqalee la cofeelam, bége la bay sarxolle.
Sofoni 3:17
Yaakaaral Aji Sax ji, dëgërlul te amu fit, te yaakaarati Aji Sax ji.
Taalifi cant 27:14
Ma dégg kàddu gu xumb jibe ca ngàngune ma, ne: «Màkkaanu Yàllaa ngii ci biir nit ñi. Mooy dëkk ak ñoom, ñu diy ñoñam. Yàlla ci boppam mooy dëkk ak ñoom, di seen Yàlla. Mooy fomp seen wépp rongooñ. Dee dootul am, dëj aki yuux aku tiis dootul am, lu njëkk laay wéy.»
Peeñu ma 21:3–4
Ci kaw loolu Aji Sax ji wax Musaa ne ko: «Loo may woowe wall? Waxal bànni Israayil, ne leen ñu dem rekk,
Mucc ga 14:15
Dëgërluleen nag te nu góor-góorlu xeexal sunu xeet ak sunu dëkki Yàlla yii. Aji Sax ji nag yal na def liy coobareem.»
1.Jaar-jaar ya 19:13
Gannaaw gi, noon ya xam ne yég nanu leen, te Yàlla nasaxal na seen pexe. Ba mu ko defee nu walbatikuwaat nun ñépp ca tata ja, ku nekk dellu ca liggéeyam.
Neyemi 4:9
«Du képp ku ma naan: “Sang bi, Sang bi,” mooy tàbbi ci nguurug asamaan, xanaa ñiy jëfe sama coobarey Baay ba fa asamaan.
Macë 7:21
Ku namma jëfe coobarey Yàlla, dina xam ndax li may jàngale ci Yàlla la jóge, am ci sama coobarey bopp laay waxe.
Yowaan 7:17
Nan ràññee, di saxoo faale Aji Sax ji. Ni jant bu fenk la dikkam wóore, ni ab taw la nuy dikkale, ni ab tawu mujjantal buy seral suuf.»
Ose 6:3
Teewluleen te ñaan, ngir baña tàbbi cig fiir. Xolub nit kat yebu na, yaram see néew doole.»
Macë 26:41
Teewluleen te saxoo ngëm, góor-góorluleen te dëgërlu.
1.Korent 16:13
Sawarleen te baña yoqi, jaamuleen Boroom bi, ànd ceek pastéefu xol.
Room 12:11
Ku yoqi, dooleelleen ko, ku óom yay fenqe, jàppaleleen ko. Ku fitam rëcc, ne leen ko: «Dëgërlul te bul tiit. Sa Yàllaa ngii di la feyul, ba yool say noon. Moom mooy dikk, wallusi la.»
Esayi 35:3–4
Bés yu mujj yi
Wone yépp11 Des 2025
10 Des 2025
9 Des 2025
8 Des 2025
7 Des 2025
6 Des 2025
5 Des 2025