Li dagan ci yaw, bu ko jariñoo ba may kenn lu mu ŋàññee.
Room 14:16
Leeru Bés bi
Li dagan ci yaw, bu ko jariñoo ba may kenn lu mu ŋàññee.
Room 14:16
te lu bon ak nu mu mana bindoo, dàndleen ko.
1.Tesalonig 5:22
Li nuy xinte moo di li baax ci kanam Boroom bi, te baax ci kanam nit ñi itam.
2.Korent 8:21
Ndax coobarey Yàlla kat moo di ngeen di def lu baax, ba wedamal nit ñu ñàkk bopp ñi xamul dara.
1.Piyeer 2:15
Waaye rey nit, mbaa sàcc, mbaa def lu bon, mbaa dugg ci yëfi jàmbur, bumu waral coonoy kenn ci yeen.
1.Piyeer 4:15
Ku sonn ndax li muy aji-gëm-Almasi nag, bumu ci rus, na sàbbaal Yàlla kay, ci woowu tur.
1.Piyeer 4:16
Yeen de bokk yi, cig yiwiku lees leen woo. Moytuleen lenn rekk: bu seenug yiwiku diw lay, ngir topp seen bakkan, waaye deeleen surgawoonte ngir cofeel.
Galasi 5:13
Waaye ni ngeen di dunde seen sañ-sañu bopp, dangeen ciy xool ñi seen ngëm dëgërul, ngir ngeen bañ leena yóbbe bàkkaar.
1.Korent 8:9
Waaye ku bàkkaarloo kenn sax ci ñu tuut ñii ma gëm, li gën ci moom mooy ñu takk ci baatam doju wolukaay wu réy wu mbaam di wëndeel, daldi koy sànni biir xóotey géej.
Macë 18:6
Bu loolu amee buur ba ne leen: “Maa leen ko wax déy, lu ngeen ci defal kenn ci ñi gëna tuut ci sama bokk yii, man ngeen ko defal.”
Macë 25:40
te lépp lu ñu wone ci ag leer, di ag leer. Moo tax ñu ne: «Yaw miy nelaw, yewwul, dekkil, Almasi bi leeral la.»
Efes 5:14
Li tax ngeen wara gëna farlu ci loolu mooy, xam ngeen jant yi nu tollu; seen waxtuw yewwu jot na ba noppi, nde léegi la nu mucc gëna jege ba nuy doora gëm.
Room 13:11
Kon nag bunu nelaw ni ñi ci des, waaye nanu teewlu, te ànd ak sunu sago. Ndaxte ñiy nelaw, guddi lañuy nelaw; ñiy màndi it, guddi lañuy màndi. Waaye nun ñiy waa bëccëg, nanu ànd ak sunu sago, te def ngëm ak cofeel sunu kiiraayal dënn; yaakaaru texe di sunu mbaxanam xare.
1.Tesalonig 5:6–8
«Yerusalem, jógal ne ràññ, sag leer feq na; leeru màggaayu Aji Sax ji fenkal na la!
Esayi 60:1
Lëndëm gaa ngii di muur àddina, mu ngi guddil askan yi, te yaw, Aji Sax ji fenkal la, leeru màggaayam feqal la.
Esayi 60:2
Kon nag teewlooleen seen xel, te ànd ak seen sago, te ngeen wékk seen jépp yaakaar ci yiw wa ñu leen di dikke kera bu Yeesu Almasi bi feeñee.
1.Piyeer 1:13
«Takkuleen te seeni làmp di tàkk.
Luug 12:35
Melleen ni nit ñuy séentu seen njaatige lu jóge céet, ndax bu dikkee ba fëgg bunt ba, ñu daldi ko ubbil.
Luug 12:36
Bés yu mujj yi
Wone yépp10 Des 2025
9 Des 2025
8 Des 2025
7 Des 2025
6 Des 2025
5 Des 2025
4 Des 2025