Leeru Bés bi — 10 Desàmbar: Yowaan 10:29

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Sama Baay bi ma leen jox, moo gëna màgg lépp, te kenn manula foqatee lenn ci loxol Baay bi.

Yowaan 10:29

Looloo tax may daj yii coono. Waaye rusuma ci, ndax xam naa ki ma gëm, te wóor na ma ne, li ma ko dénk, moo ko mana sàmm ba keroog bés ba.

2.Timote 1:12

Kon nag dama lay dénk fi kanam Yàlla ak Almasi Yeesu miy àtteji ñiy dund ak ñi dee, di la dénk ci darajay bésam ba muy feeñ ak ci darajay nguuram:

2.Timote 4:1

Waaye ci mboolem lu nu dikkal, nooy am ndam lu mat sëkk, ci ndimbalal ki nuy soppeem. Ndax kat bir na ma ne du ag dee, du ag dund, du ay malaaka, duy boroom nguur, du tey, du ëllëg, duy boroom doole, du lu kawe, du lu xóot, mbaa meneen mbindeef mu mu doon; dara manu noo tàggale ak cofeel gi nu Yàlla won ci Almasi Yeesu sunu Sang.

Room 8:37–39

ndaxte dee ngeen, ba seenug dund ànd ak Almasi bi, làqe fa Yàlla.

Kolos 3:3

Bokk yi, soppe yi, dégluleen. Xanaa du Yàlla moo tànn ñi àddina jàppe ñu néew doole, ngir ñu barele ngëm, boole ci jagoo nguur gi Yàlla dig ñi ko sopp?

Yanqóoba 2:5

Sunu Sang Yeesu Almasi bi ci boppam ak Yàlla sunu Baay mi nu sopp, te may nu ciw yiwam, jàmmi xol ju sax dàkk ak yaakaar ju wér, yal nañu leen may jàmmi xol, te may leen dooley wéye jépp jëf ju baax ak gépp kàddu gu rafet.

2.Tesalonig 2:16–17

Waaye ki ne jàkk yoon wu mat sëkk wiy goreel ku ko topp, saxoo yoon wi te bañ koo dégg, fàtte, xanaa di dégg, jëfe, kooku mooy bége jëfam.

Yanqóoba 1:25

Su boobaa dingeen xam liy dëgg, te dëgg gi moo leen di goreel.» Ñu ne ko: «Nun askanu Ibraayma lanu, masunoo doon jaamu kenn. Kon ana loo nu naa dees na nu goreel?» Yeesu ne leen: «Maa leen ko wax déy ci lu wér, képp kuy bàkkaar, ab jaamu bàkkaar la.

Yowaan 8:32–34

Kon nag su leen Doom ji goreelee, ngeen diy gor tigi.

Yowaan 8:36

Almasi bi da noo yiwi, ngir nu yiwiku, kon nag saxooleen ko, te baña laxasooti buumi njaam.

Galasi 5:1

Yeen de bokk yi, cig yiwiku lees leen woo. Moytuleen lenn rekk: bu seenug yiwiku diw lay, ngir topp seen bakkan, waaye deeleen surgawoonte ngir cofeel. Ndax yoonu Musaa wépp, ci lenn ndigal lii la tënku: «Ni ngeen soppe seen bopp, nangeen ko soppe seen moroom.»

Galasi 5:13–14

Noonu lees leen yiwee, tàggale leen ak nooteelu bàkkaar, ngeen doon ay surgay njub.

Room 6:18

Dafa mel ni ndaw suy séy; li feek jëkkëram di dund, yoon a yeew buumu jëkkëram ci baatam. Waaye su jëkkër ji deewee, ndaw si teqalikoo na ak yoon wi ko yeewe woon buumu jëkkëram.

Room 7:2

Ndax kat, yoonu Noo gu Sell giy maye bakkan te nekk ci Almasi Yeesu moo la yiwi, ba nga mucc ci yoonu bàkkaar ak dee.

Room 8:2

di daagoo sago, nde say tegtal laay sàkku.

Taalifi cant 119:45