Leeru Bés bi — 9 Desàmbar: Kàddu yu xelu 21:3

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Deel def dëgg ak lu jub, moo gënal Aji Sax ji ab sarax.

Kàddu yu xelu 21:3

Yaw nit ki, waxees na la li baax, ak li Aji Sax ji sàkku ci yaw, te loolu moyul di def yoon, sopp jëfi ngor te woyof nooy toppe sa Yàlla.

Mise 6:8

Samiyel ne ko: «Bànneexu Aji Sax ji ci saraxi rendi-dóomal ak yeneen sarax, mbaa tolloo naak bànneex ba muy am ci dégg ndigalal Aji Sax ji? Ma ne, dégg ndigal a gën ab sarax; xol bu nangoo gën nebbonu kuuy.

1.Samiyel 15:22

Te it nga soppe ko sa léppi xol, ak sa léppi xel, ak sa léppi doole, te ni nga soppe sa bopp, nanga ko soppe sa moroom; loolu moo gën mboolem saraxi dóomal, ak yeneen sarax yu mu mana doon.»

Màrk 12:33

Aji Sax ji Yàlla Boroom gàngoor yi, Aji Sax jee di turu bàkkam.

Ose 12:6

Ci kaw loolu rakkam ju ñuy wax Maryaama toog ca wetu Sang bi, di déglu kàddoom,

Luug 10:39

Ndaxam lenn doŋŋ a manula ñàkk. Maryaama nag, cér bi gën la taamu, te deesu ko nangu ci moom.»

Luug 10:42

ndax Yàlla mooy liggéey ci yeen lu tax ngeen mana namma jëfe coobareem, ba man koo jëfe.

Filib 2:13

Su boobaa pënd dellu suuf, na woon; bakkan dellu fa Yàlla ma able woon.

Kàdduy waare 12:7

Yàlla Aji Sax ji nag móol nit ci pëndub suuf, ëf ngelawal dund ci paxi bakkanam, nit daldi doon boroom bakkan.

Njàlbéen ga 2:7

Ndeke xel mi ci nit mooy noowal Aji Man ji koy may dég-dég.

Ayóoba 32:8

Noonu lañu binde ne: «Aadama, nit ku njëkk ka daldi doon boroom bakkan,» waaye Aadama mu mujj mi moo di Noo giy maye bakkan.

1.Korent 15:45

Ana ku mu wóor ne bakkanu nit day yéeg asamaan, bakkanu mala tàbbi suuf?

Kàdduy waare 3:21

Moo tax nu saxoo ñeme, doonte xam nanu ne sunu desagum biir kër, ci yaram wi, mooy sunu desagum fu sore Sang bi,

2.Korent 5:6

Kon fees nanu ak kóolute, te li nu gënal mooy jóge ci sunu yaramu bopp, ngir dëkki ak Sang bi.

2.Korent 5:8

Ci diggante ñaar yooyii laa tance: yàkkamti namaa yiwiku ba fekki Almasi bi, te loolu moo dàqati fuuf.

Filib 1:23

Bokk yi nag, bëggunu ngeen réere mbirum way dawlu ñi, bay tiislu ni ñeneen ñi amul jenn yaakaar, di tiisloo. Ndegam gëm nanu ne Yeesu dee na, ba dekki, noonu it lanu wara gëme ne Yàlla mooy dekkal way dawlu ñi gëmoon Yeesu, ba boole leen ak Yeesu, indaale.

1.Tesalonig 4:13–14

Sama kër Baay, dëkkuwaay yu baree nga fa. Su demewul woon noonu, ndax dinaa leen ne maa ngi leen fay waajali béreb? Te gannaaw bu ma leen waajalee béreb, dinaa délsi, jëlsi leen, yóbbu, ba fu ma nekk, man, ngeen nekk fa, yeen itam.

Yowaan 14:2–3