Yeen de bokk yi, cig yiwiku lees leen woo. Moytuleen lenn rekk: bu seenug yiwiku diw lay, ngir topp seen bakkan, waaye deeleen surgawoonte ngir cofeel.
Galasi 5:13
Leeru Bés bi
Yeen de bokk yi, cig yiwiku lees leen woo. Moytuleen lenn rekk: bu seenug yiwiku diw lay, ngir topp seen bakkan, waaye deeleen surgawoonte ngir cofeel.
Galasi 5:13
Bokki gëmkat ñi, su ñu bettee nit ci ag tooñ, yeen ñi topp Noowug Yàlla, waññileen ko ndànk, te kenn ku nekk ci yeen xoolaat boppam bu baax, ngir seen bakkan bañ leena xiirtal, ba ngeen daanu ci fiir, yeen itam. Yenuleen seeni yeni moroom, su boobaa ngeen di topp yoonu Almasi bi, ba mu mat sëkk.
Galasi 6:1–2
Bokk yi, su amee ci yeen ku moy yoonu dëgg, keneen ku ko waññi, xamleen ne ku waññ bàkkaarkat ci yoonu sànkuteem, musal na ko bakkanam, te faral na ko bàkkaar yu bare.
Yanqóoba 5:19–20
Kon nag gannaaw setal ngeen seen xol, ndax dëgg gi ngeen déggal, ba tax ngeen am cofeel gu mucc jinigal ci bokki gëmkat ñi, nangeen soppantee xol bu set, cofeel gu mat sëkk.
1.Piyeer 1:22
Buleen ameel kenn bor, lu moy borub soppante; ndax ku sopp sa moroom, yaa matal yoonu Musaa.
Room 13:8
Na leen mbëggeelug bokk taxa fonkante, te ngeen farlu ci di teralante.
Room 12:10
Naka noonu yeen ndaw ñi, nangulleen magi mbooloom gëmkat ñi. Yeen ñépp nag toroxluleen ci seenug jëflante, ndax: «Yàlla, ñi réy lay xeex, ñi toroxlu, mu may leen aw yiw.»
1.Piyeer 5:5
Nun ñi fendi ci wàllu ngëm, fàww nu xajoo tëley ñi néew doole, te baña sàkku sunu bànneexu bopp.
Room 15:1
Su boobaa pënd dellu suuf, na woon; bakkan dellu fa Yàlla ma able woon.
Kàdduy waare 12:7
Noonu itam la ndekkitel ñi dee di deme. Li ñu suul mooy jiwu wiy yàqu, te bu dekkee dootul yàqu. Ci ag teddadi lañu ji néew bi ñu suul, te teraanga lay dekkaale. Ci néew doole lees ko ji, mu dekkaale doole. Li ñu suul mooy yaramu judduwaale wi ñu ji, mu dekki di yaram wuy dunde Noowug Yàlla. Ndaxte ni yaramu judduwaale ame, ni la yaram wuy dunde Noo gi ame.
1.Korent 15:42–44
Aadama mu njëkk ma, ci suuf la jóge woon, te ba tey di suuf; Aadamam ñaareel mi jóge fa asamaan.
1.Korent 15:47
saw ñaq ngay dunde, ba kera ngay dellu ci suuf si ma la jële; ndaxte pënd nga, te dinga dellu di pënd.»
Njàlbéen ga 3:19
Kii a ngi deewaale dooleem, xel ma dal, tiitul dara,
Ayóoba 21:23
Kee deewe naqaru xol, masula ñam bànneex, te ñooy tëddandoo biir suuf, bokk sàngooy sax.
Ayóoba 21:25–26
xanaa di bànneexu, sama xol bég, sama yaram dal xel.
Taalifi cant 16:9
Bu sama der bi lekkoo sax, du tee ma dese suux wu ma xoole Yàlla,
Ayóoba 19:26
Nun nag sunum réew a nga fa asamaan, fa nuy séentoo sunu Musalkat, Sang Yeesu Almasi bi. Mooy kiy liggéeye manooreem ji mu tënke lépp cig curgaam, ba sopparñi sunu yaram wu doyadi wii, niroole kook yaramam wi ànd ak màggaay.
Filib 3:20–21
sama xol diis, xel di xelaat, xol diis gann; ma mujj àddu,
Taalifi cant 39:4
Yal nanga nu xiir ci lim sunuy fan, ba nu mana dawal xel mu rafet.
Taalifi cant 90:12
Bés yu mujj yi
Wone yépp7 Des 2025
6 Des 2025
5 Des 2025
4 Des 2025
3 Des 2025
2 Des 2025
1 Des 2025