Leeru Bés bi — 7 Desàmbar: 2.Korent 5:21

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Almasi bi masula bàkkaar, moom la Yàlla sëf sunu bàkkaar, ngir nu mana ame ci moom àtteb nit ñu jub fa Yàlla.

2.Korent 5:21

Nun ñépp a lajj niy xar, ku nekk walbatiku topp yoonam, te Aji Sax jee ko sëf mbugal mi nu wara dékku nun ñépp.

Esayi 53:6

«Moom ci boppam moo gàddu sunuy bàkkaar,» moo ko tegoo ci yaramu boppam ca bant ba, ngir nu deewal bàkkaar te dundal njub; «moom mooy ki ngeen wére ci ay góomam.»

1.Piyeer 2:24

Noonee déggadig kenn nit taxe ñu bare doon ay bàkkaarkat, noonu it la déggug ndigalu kenn nit taxe ñu baaxe ñu bare àtteb nit ñu jub.

Room 5:19

Waaye ba Yàlla sunu Musalkat feeñalee mbaaxam ak mbëggeelam ci doom aadama, ca la nu musal, te du jenn jëfu njekk ju nu def, ba tax mu musal nu, waaye ci yërmandeem la nu musale, sang nu cangaay lu nu taxa judduwaat, boole ci yeesale nu Noo gu Sell gi mu nu awale ci Yeesu Almasi bi sunu Musalkat, ba baawaanal ko ci sunu kaw. Noonu la nu Yàlla baaxee àtteb ñu jub ci kaw aw yiwam, ba nu mujj séddu ci texe gu sax dàkk, ni nu ko séentoo.

Tit 3:4–7

Kon nag léegi, amul benn daan bu ñeel ñi bokk ci Almasi Yeesu.

Room 8:1

Ci jamonoom, Yuda dina texe, Israayil dëkke kaaraange, te dees na ko tudde nii: “Aji Sax jeey sunu njub.”

Yeremi 23:6

Aji Sax ji nee: «Maay garabal seenug déggadi, maa leen di bëggal sama bopp, nde mereetuma leen.

Ose 14:5

Man Póol ci sama wàllu bopp nag, maa leen di ñaaxe teeyug Almasi bi, akug lewetaayam, man miy teew ci seen biir, di ab ragaléey fi seen kanam, te bu ma soree doŋŋ laa leen di ñeméey,

2.Korent 10:1

Barax bu lemu sax, du ko damm, leer gu giim it, du ko fey. Mooy indi yoonu dëgg.

Esayi 42:3

«Noowug Boroom baa ngi fi sama kaw, ndax moo ma diw, fal ma ngir ma yégal néew-doole yi xibaaru jàmm bi. Moo ma yebal ngir ma yégal jaam yi, ne dees na leen jot, yégal gumba yi, ne dinañu gis, yégal ñi ñu noot, ne dees na leen goreel, tey yéene atum yiw wu Boroom bi.»

Luug 4:18–19

Mu àddu, ne leen: «Tey jii la Mbind mii mat, ngeen dégg.» Ñépp a doon seedeel Yeesu lu rafet, tey yéemu ci kàdduy yiw yi tukkee ci gémmiñam. Ñu naan: «Xanaa kii du doomu Yuusufa ji?»

Luug 4:21–22

Ci kaw loolu Sang bi geesu, ne jàkk Piyeer, Piyeer fàttaliku la ko Sang bi waxoon ne ko: «Bala ganaar a sab tey jii, dina fekk nga jàmbu ma ñetti yoon.» Piyeer nag génn, di jooy jooy yu metti.

Luug 22:61–62

Mooy sàmm géttam bii ni kuy sàmmug juram, boole mbote yi cib loxoom, taf cib dënnam, yóbbu; xar yiy nàmpal, mu wommat.»

Esayi 40:11