ndax Yàlla mooy liggéey ci yeen lu tax ngeen mana namma jëfe coobareem, ba man koo jëfe.
Filib 2:13
Leeru Bés bi
ndax Yàlla mooy liggéey ci yeen lu tax ngeen mana namma jëfe coobareem, ba man koo jëfe.
Filib 2:13
Du caageenu doyloo sunu manoorey bopp, ba yaakaar ne lenn man naa sottee ci sunu wàllu bopp, waaye sunu manoore ci Yàlla la jóge.
2.Korent 3:5
Yaxya ne leen: «Nit manula am lenn lu ko Yàlla joxul.
Yowaan 3:27
Kenn manula ñëw ci man te Baay bi ma yónni indiwu ko; te ku ñëw ci man, maa koy dekkal kera bés bu mujj ba.
Yowaan 6:44
Maa leen di may benn xol ak benn jubluwaay ngir ñu di ma wormaal seen giiru dund, muy seen ngëneel, ñook seen doom yi leen di wuutu.
Yeremi 32:39
Bokk yi, soppe yi, buleen juum ci lii: gépp may gu baax ak bépp jagle bu mat, fa kaw la bawoo, di lu wàcce fa Baay biy boroom leer yi, ki soppikuwul ci lenn, te genn ker gu toogadi nekkul ci moom. Moom la soob mu jur nu ci kàddug dëgg gi, ba nu taxawe saraxu ndoortel meññeef, ci biiri bindeefam.
Yanqóoba 1:16–18
Ndax kat noo di liggéeyu Yàlla; Yàllaa nu yeesal ci Almasi Yeesu, ngir nu wéye jëf ju rafet ja mu nu fàgguloon ca njàlbéen, ngir nu di ko jëfe.
Efes 2:10
Aji Sax ji, yaa nuy defal jàmm, te lépp lu nu def, yaa nu ko sottalal.
Esayi 26:12
Teewluleen te ñaan, ngir baña tàbbi cig fiir. Xolub nit kat yebu na, yaram see néew doole.»
Macë 26:41
Aji Sax ji, nu ngi lay xaar, fi sa kaw yoonu santaane yi, di tudd sa tur, di la bàyyi xel, lii déy, mooy sunu nammeelu xol. Xol laa lay sàkkoo guddi, sama jëmm jépp di la laaj. Bu say àtte teewee fi kaw suuf, waa àddina xame ca luy njub.
Esayi 26:8–9
Xam naa ne man, sama bindu suuxu neen wii, lenn lu baax dëkku ci. Yéene jaa ngeek man, kàttanu jëfe lu baax moo fi nekkul.
Room 7:18
Ndaxam ci sama biir xol, yoonu Yàllaa ma neex. Waaye gis naa ci samay cér, weneen yoon wuy xeex ak yoon wi samam xel jubool, te yoon woowoo ma jàpp njaam, jébbal ma dooley bàkkaar bi dëkke samay cér.
Room 7:22–23
Ndax bakkan, la muy xemmem, daa dëngoo ak Noo gi; Noo gi it, la muy xemmem dëngoo ak bakkan. Dañu di ñaar yu féewaloo, te moo tax dungeen def la ngeen nammoona def.
Galasi 5:17
Lépp laa mane ci ndimbalal ki may manal.
Filib 4:13
Du caageenu doyloo sunu manoorey bopp, ba yaakaar ne lenn man naa sottee ci sunu wàllu bopp, waaye sunu manoore ci Yàlla la jóge.
2.Korent 3:5
Mu ne ma: «Sama yiw doŋŋ nga soxla; sama manoore, ci ag néew doole lay mate.» Kon kat dinaa gëna bégati ci damoo diggante yu ma néewe doole, ngir manoorey Almasi bi wàcc ci sama kaw.
2.Korent 12:9
Bés yu mujj yi
Wone yépp5 Des 2025
4 Des 2025
3 Des 2025
2 Des 2025
1 Des 2025
30 Now 2025
29 Now 2025