Ngëneel la ma duma yi jural, ngir jànge naa ci say tegtal.
Taalifi cant 119:71
Leeru Bés bi
Ngëneel la ma duma yi jural, ngir jànge naa ci say tegtal.
Taalifi cant 119:71
Li muy Doom lépp, terewu koo tàggatu ci dégg ndigal, ndax coono yi mu daj.
Yawut ya 5:8
Gannaaw ay doom lanu nag, ay boroom cér lanu, ay boroom cér yu Yàlla sédd, cér yu nu bokk ak Almasi bi, gannaaw noo bokk ak moom ab coono tey, ngir bokk ak moom teraangay ëllëg. Jàpp naa ne sunu coonob tey du dara, soo ko xoolee ci teraanga ji ñu nuy feeñalal ëllëg.
Room 8:17–18
Ndaxam moo xam fi ma jaare, te bu ma nattoo, ma génn ci ni wurus wu ñu xelli. Tànkam, sama tànk, yoonam laa tegu, moyuma ko.
Ayóoba 23:10–11
Fàttalikuleen mboolem yoon wi leen seen Yàlla Aji Sax ji awale diiru ñeent fukki at yii ci màndiŋ mi, teg leen coono, nattu leen ngir xam li ci seen biir xol, xam ndax dingeen wormaal ay santaaneem, am déet.
Baamtug yoon wi 8:2
Xamleen xéll ne ni baay di yare doomam, ni la leen seen Yàlla Aji Sax ji yare. Kon sàmmleen seen santaaney Yàlla Aji Sax ji, di topp ay yoonam te ragal ko.
Baamtug yoon wi 8:5–6
Mooy sàmm jéegoy wóllëreem, ku bon sànkoo biir lëndëm, nde doole mayewul ndam.
1.Samiyel 2:9
Daawuda ne Filisteen ba: «Yaw de yaa may jëlal ab saamar ak xeej bu mag ak bu ndaw, waaye man turu Aji Sax ju gàngoor yi laa lay dikke, Yàllay làngi xarey Israayil ji nga tëkku.
1.Samiyel 17:45
Mu yoor loxoom ca mbuusam, jël ca aw doj, mbaq, jam Filisteen ba ci jë, doj wa tàbbi ca biir jë ba. Mu ne jànjaŋ, dëpp kanam ga fa suuf. Ag mbaq aku doj la Daawuda mane Filisteen ba, jam ko, rey ko, te yorul saamar.
1.Samiyel 17:49–50
Mbooloo mu réy mayul Buur ndam, doole ju bare walluwul jàmbaar.
Taalifi cant 33:16
Ma ne, Aji Sax jee naa jàkk ku ko ragal tey wéeroo ngoram.
Taalifi cant 33:18
Mu ne ma: «Sama yiw doŋŋ nga soxla; sama manoore, ci ag néew doole lay mate.» Kon kat dinaa gëna bégati ci damoo diggante yu ma néewe doole, ngir manoorey Almasi bi wàcc ci sama kaw. Looloo ma tax di bànneexu ci biir diggante yu ma néewe doole ak ci biiri saaga ak ci biir ag ñàkk ak ci biir coono yu ñu may bunduxataale ak ci biir njàqare yu ma dal ngir Almasi bi. Ndaxte bu ma néewee doole, booba laa am kàttan.
2.Korent 12:9–10
Bés yu mujj yi
Wone yépp4 Des 2025
3 Des 2025
2 Des 2025
1 Des 2025
30 Now 2025
29 Now 2025
28 Now 2025