Waaye xel mu rafet fees koy jële, ak fu ag dégg màkkaanoo?
Ayóoba 28:12
Leeru Bés bi
Waaye xel mu rafet fees koy jële, ak fu ag dégg màkkaanoo?
Ayóoba 28:12
Ku desele am xel mu rafet nag, na ko ñaan Yàlla, mu may ko ko, ndax Yàlla mooy yéwéne ñépp te du sikk kenn. Waaye ngëm la koy ñaane te bumu ci am benn sikki-sàkka, ndax kiy sikki-sàkka daa mel ni gannaxu géej bu ngelaw liy yóbbu, di ko lëmbaaje.
Yanqóoba 1:5–6
Nanga wóoloo Aji Sax ji sa léppi xol, te bul wéeru ci saw déggin. Loo mébét, bàyyil Yàlla xel, mu xàllal la yoon.
Kàddu yu xelu 3:5–6
Yaw Buur bi sax dàkk, doo dee, te bët manu laa gis, yaw Yàlla miy kenn, yaa tedd, yaa màgg, tey ak ëllëg ba fàww. Amiin!
1.Timote 1:17
Bul doyloo sa xel mu rafet, ragalal Aji Sax ji, dëddu mbon;
Kàddu yu xelu 3:7
Ma ne: «Éy Boroom bi Aji Sax ji, da di manumaa wax, gone doŋŋ laa.» Aji Sax ji ne ma: «Bul ne: “Gone laa.” Képp ku ma la yebal, dem ca; lépp lu ma la sant, wax ko. Bu leen ragal, ngir yaw laay àndal, di la xettali.» Kàddug Aji Sax jee.
Yeremi 1:6–8
Bésub keroog, man dootuleen ma ñaan dara. Maa leen ko wax déy ci lu wér, su boobaa lu ngeen ñaan Baay bi ci sama tur, mu may leen ko. Ba léegi ñaanuleen dara ci sama tur. Ñaanleen, nangule, ngir seen mbég mat sëkk.
Yowaan 16:23–24
Te lépp lu ngeen sàkkoo ñaan gu ànd ak ngëm, dingeen ko am.»
Macë 21:22
Doy na sëkk! Dunduma ba fàww; ba ma, samay fan genn noo la!
Ayóoba 7:16
Njàqaree ma dugg, may kat-kati, musiba mëdd ma.
Taalifi cant 55:6
Xanaa ma naaw, ba sore, fanaani màndiŋ ma. Selaw.
Taalifi cant 55:8
Moo nu tax di onk ci biir xayma bii nu nekk, ndax yàkkamtee sol sunu dëkkuwaayu asamaan, teg ko ci kaw bii nu jiital,
2.Korent 5:2
Noo ngi onk ndax diis, li feek nu ngeek sunuw yaram, xayma bi nu soloo nii. Du summiku lanu namm, waaye solu teg ko ci lanu namm, ngir li jëm ci dee, daldi suux ci biir dund.
2.Korent 5:4
Ci diggante ñaar yooyii laa tance: yàkkamti namaa yiwiku ba fekki Almasi bi, te loolu moo dàqati fuuf.
Filib 1:23
Kon nag gannaaw gii ndiiraanu seede wu réy moo nu yéew, nanu sippiku mboolem sëf bu nuy yeexal ak bàkkaar bu nu yomba téqtal. Ñu daw nag xél wi ñu nu waajalal, te baña yoqi. Nanu ne jàkk Yeesu, kiy sos, di sottal ngëm, moom mi mbég mi ñu ko waajalal tax mu dékku bant ba ñu ko daaj, tegul muy dara toroxtaange ja ko ca fekk, te doxe ca toog ca ndijooru ngànguney Yàlla. Xoolleen ci moom mi bàkkaarkat yi doon xeex, bala ngeena yoqi bay xàddi.
Yawut ya 12:1–3
Jàmm laa leen bàyyee, sama jàmm laa leen may te mayuma leen ko ni àddina di mayee. Buleen jaaxle, buleen tiit.
Yowaan 14:27
Bés yu mujj yi
Wone yépp3 Des 2025
2 Des 2025
1 Des 2025
30 Now 2025
29 Now 2025
28 Now 2025
27 Now 2025