Leeru Bés bi — 3 Desàmbar: Ayóoba 5:8

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Man de su ma doon yaw damay sàkku Yàlla, te kon Yàlla laay diis sama mbir.

Ayóoba 5:8

Ana lu të Aji Sax ji? Bu ñu ca àggee nëgëni déwén déy, dinaa fi délsiwaat, te Saarata dina am doom ju góor.»

Njàlbéen ga 18:14

Jébbalul ci Aji Sax ji, dénku ci moom, mooy sottal.

Taalifi cant 37:5

Buleen jaaxle ci dara, waaye ci mbir mu mu mana doon, deeleen dikke Yàlla seeni soxla, di ko ñaan aka dagaan te boole ci di ko sant.

Filib 4:6

ci ni ngeen di sippikoo ci kawam, mboolem seenu tiis, nde mooy ki leen tiisoo.

1.Piyeer 5:7

Ba Esekiyas jëlee bataaxal ba ca loxol ndaw ya, jàng ko ba noppi, dafa dem ba ca kër Aji Sax ji. Mu daldi tàllal bataaxal ba fa kanam Aji Sax ji. Esekiyas ñaan Aji Sax ji, ne ko:

Esayi 37:14–15

Su boobaa balaa ñoo woote, man, maay wuyu; balaa ñoo daane seen kàddu, ma nangul leen.

Esayi 65:24

Kon nag tuddanteleen seeni bàkkaar tey ñaanalante, ndax ngeen wér. Aji jub ji, ag ñaanam, day dal ak doole.

Yanqóoba 5:16

Maa bëgg Aji Sax ji: maa ko woo, dagaan ko, mu dégg ma. Teewlu na ma moos, dama koy woo li feek may dund.

Taalifi cant 116:1–2

Kon nag nanu agsee fi Yàlla xol bu dëggu ak fit wu mat sëkk wu ngëm waral, gannaaw wisees na sunum xel ndoxum setlu, ba mu tàggook bépp gàkk bu mu nu sikkale, te raggees na sunu yaram ci ndoxum setlu.

Yawut ya 10:22

«Sàkkal mbalkam njàpp mu xànjar, ak tegub xànjaram ngir ñu di ko jàppe. Teg ko ci diggante xaymab ndaje mi ak sarxalukaay bi, te nga duy ko ndox. Aaróona aki doomam di ci tanq, raxase seeni loxo ak seeni tànk. Bu ñuy duggsi ci xaymab ndaje mi, nañu jàpp, ndax ñu baña dee, nañu jàpp itam, bu ñuy liggéeysi fi sarxalukaay bi, di saxaaral saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji. Nañu raxas seeni loxo ak seeni tànk, ndax ñu baña dee. Na loolu di dogal bu sax dàkk, ñeel Aaróona ak askanam ci seen gépp maas.»

Mucc ga 30:18–21

Dangeena xamul ne seen yaram mooy màkkaanu Noo gu Sell gi ci yeen, Noo gi ngeen jote ci Yàlla? Moomuleen seen bopp,

1.Korent 6:19

Ku yàq kër Yàlla nag, kooku Yàlla dina ko yàq, ndax kër Yàlla dafa sell, te mooy li ngeen doon.

1.Korent 3:17

Bu sama der bi lekkoo sax, du tee ma dese suux wu ma xoole Yàlla, xoolal ko sama bopp, te du doon sama gan. Maaka namm lii ci sama xol!

Ayóoba 19:26–27

Du lenn lu sobewu lu fay dugg nag, mbaa defkatu jëf ju ruslu ak njublaŋ. Ñi ñu bind ci téereb dund bu Xar mi doŋŋ ñoo fay dugg.

Peeñu ma 21:27

Sa gët yu sell jomb naa niir lu bon, te manoo seetaan nooteel! Ana looy seetaan ay workat? Looy noppi te ku bon di mëdd moroomam mu ko gëna jub?

Abakug 1:13

Kon nag bokk yi, ma ñaax leen, te yërmandey Yàlla tax. Na seen dund mel ni sarax su ñuy defal Yàlla, sarax su sell te neex ko. Loolu déy mooy njaamu gi leen war.

Room 12:1