Leeru Bés bi — 2 Desàmbar: 1.Yowaan 2:20

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Yeen nag, Ku sell kee leen diw, sédde leen ko Noo gu Sell gi, te moo leen taxa xam, yeen ñépp.

1.Yowaan 2:20

ak ni Yàlla ànde ak Yeesum Nasaret, ba jagleel ko pal gu mu dogale Noo gu Sell geek xam-xam bi mu ko sotti, muy wër, di def lu baax, di faj mboolem ñi Seytaane nootoon.

Jëf ya 10:38

ndax Yàlla la soob mu dëël gépp matam ci moom.

Kolos 1:19

Ci ag matam lanu tanqe nun ñépp, yiw ci kaw yiw.

Yowaan 1:16

Yaa ma berndeel, noon yi gis, nga diwal ma saa bopp, terale ma, saab kaas rembat.

Taalifi cant 23:5

Yeen nag, diw gi mu leen diw, sédde leen ko Noo gu Sell gi, moo sax ci yeen, soxlawuleen ku leen jàngal dara. Gannaaw Noowam gu Sell googu moo leen di jàngal lépp, te di lu dëggu lu caaxaan amul, nangeen sax ci moom, ni mu leen ko jàngale.

1.Yowaan 2:27

Waaye Taxawukat bi, di Noo gu Sell gi leen Baay biy yónnee ci sama tur, moo leen di jàngal lépp, fàttali leen lépp lu ma leen waxoon, man.

Yowaan 14:26

Te itam Noowug Yàlla moo nuy dimbali ndax sunug néew doole, nde xamunu sax li jaadoo sàkku ci sunuy ñaan, waaye Noo gi moo nuy tinule ay onk yu wees kàddug làmmiñ.

Room 8:26

Kon nag nanu agsee fi Yàlla xol bu dëggu ak fit wu mat sëkk wu ngëm waral, gannaaw wisees na sunum xel ndoxum setlu, ba mu tàggook bépp gàkk bu mu nu sikkale, te raggees na sunu yaram ci ndoxum setlu.

Yawut ya 10:22

Deretu sikket ak yëkk, ak dóomu nag wu jigéen wu ñu lakk, ngir suy dóom ba nit ku sobewu, yooyu lees daan sellale nit ñi, ngir seen cetug yaramu suuxu neen. Su loolu amee, ñaata yoon la deretu Almasi bi ëppe njariñ! Almasi bi mooy ki def boppam sarax bu mucc sikk ñeel Yàlla, ci dooley Noo gu Sell gi. Moom rekk moo mana setal sunu yaraangey xel mi sababoo ci sunu jëf ju bon ju jëme ci dee, ba nu mana jaamu Yàlla jiy dund!

Yawut ya 9:13–14

Yeena àgg fa Yeesu, rammukat bi dox kóllëre gu yees gi. Yeena àgg fa deret jiy setal tuuroo, te kàddug deret ja gëna neex kàddug deretu Abel ga jiboon.

Yawut ya 12:24

Ci moom lanu ame njot gi nu sottalal njéggalug moy, ndax deretam ji tuuru, noonu ko Yàlla defe ci yiwam wu yaa,

Efes 1:7

Keroog ba Musaa biralalee bànni Israayil gépp mboolem santaane, na ko yoon wi laaje, ba mu noppee, deretu wëllu la jël, ak ju sikket akum ndox ak caru garabu isob bu mu laxas kawaru xar gu xonq. Mu capp ko ca deret ja, wis-wisal ko ca kaw téereb yoon wa ak ca kaw mbooloo mépp.

Yawut ya 9:19

Xayma ba ak mboolem ndabi carxal ya it, noonu la Musaa wis-wisale deret ca seen kaw. Ndax ci yoonu Musaa sax, deret lees di setale daanaka lépp, te bu deret tuuruwul, njéggal amul.

Yawut ya 9:21–22