ku ci nekk mel ni seelukaayu ngelaw, di kiiraay ci ngëlén, mel ni wali ndox ci suuf su ne sereŋ, mbaa keppaaru doj wu mag ci àll bu mar.
Esayi 32:2
Leeru Bés bi
ku ci nekk mel ni seelukaayu ngelaw, di kiiraay ci ngëlén, mel ni wali ndox ci suuf su ne sereŋ, mbaa keppaaru doj wu mag ci àll bu mar.
Esayi 32:2
Gone yooyu nag, bindeefi suux ak deret lañu bokk doon, ñoom ñépp. Moo tax Yeesu itam dikk bokk ak ñoom woowu nekkin, ngir mana dee ba def deewug boppam pexe mi mu neenale ka yoroon dooley dee, te mooy Seytaane.
Yawut ya 2:14
«Éey saamar, yewwulal sama sàmm bi, sama jàmbaar jii ma lëngool,» kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi. «Dóoral sàmm bi, xar yi tasaaroo, ma walbati sama loxo, jublu ci jur gu ndaw gi.
Sàkkaryaa 13:7
Man ak Baay bi benn lanu.»
Yowaan 10:30
Ku dëkke kiiraayu Aji Kawe ji yaa këroo keppaaru Aji Man ji.
Taalifi cant 91:1
di mbaar mu ñuy féexloo tàngooru bëccëg, di ko seeloob taw ak waame.
Esayi 4:6
Aji Sax jee lay sàmm, Aji Sax jee lay yiir, féete la ndijoor. Du naaj wu lay dal bëccëg, mbaa leer gu ndaw guddi.
Taalifi cant 121:5–6
Ngalla Yàlla, déglul, maa ne wallóoy, teewlul, ma dagaan la.
Taalifi cant 61:2
Yaw laay làqoo, nga di ma aar ciw ay, may ma ba ñi ma wër, di ko bége. Selaw.
Taalifi cant 32:7
Yaa di rawtub néew-ji-doole, di rawtub aji ñàkk, biir njàqare, yaay mbaar mu ñuy yiiroo waame, di ker gu ñuy féexloo ci tàngoor, ndax merum kilifa gu néeg mooy waame wu ne yureet ci kaw ab tabax.
Esayi 25:4
«Maa ngii di sàkksi asamaan su yees ak suuf su yees. Deesul fàttalikooti yëf ya jiitu, xel dootu ci dem.
Esayi 65:17
«Asamaan su yees sii ak suuf su yees sii may waaja sàkk déy, ni seen taxawaay di yàgge fi sama kanam, yeen, ni la seen askan ak seen tur di yàgge fi sama kanam.» Aji Sax jee ko wax.
Esayi 66:22
Waaye asamaan su bees ak suuf su bees te njub dëkke ko bu keroogee, moom lanuy séentu, na nu ñu ko dige woon.
2.Piyeer 3:13
Ma daldi gis asamaan su bees ak suuf su bees. Fekk na asamaan su njëkk sa ak suuf su njëkk sa wéy, te géej amatul. Ma gis nag dëkk bu sell bi, Yerusalem gu bees gi, mu wàcce asamaan fa Yàlla, mel nib séet bu defaru ba jekk ngir jëkkëram. Ma dégg kàddu gu xumb jibe ca ngàngune ma, ne: «Màkkaanu Yàllaa ngii ci biir nit ñi. Mooy dëkk ak ñoom, ñu diy ñoñam. Yàlla ci boppam mooy dëkk ak ñoom, di seen Yàlla. Mooy fomp seen wépp rongooñ. Dee dootul am, dëj aki yuux aku tiis dootul am, lu njëkk laay wéy.» Ci kaw loolu ki toog ci ngàngune mi ne: «Maa ngii di yeesal lépp!» Mu teg ci ne ma: «Bindal, yii kàddu yu wóor la te dëggu.»
Peeñu ma 21:1–5
Bés yu mujj yi
Wone yépp30 Now 2025
29 Now 2025
28 Now 2025
27 Now 2025
26 Now 2025
25 Now 2025
24 Now 2025