Lii mu ngi tukkee ci man Yowaan, ñeel juróom ñaari mboolooy gëmkat ña ca diiwaanu Asi. Na leen yiw ak jàmm ñeel, tukkee fa Ki masa nekk, Ki nekk, di Kiy dikk, tukkee it fa boroom juróom ñaari noo ya fa kanam ngànguneem,
Peeñu ma 1:4
Leeru Bés bi
Lii mu ngi tukkee ci man Yowaan, ñeel juróom ñaari mboolooy gëmkat ña ca diiwaanu Asi. Na leen yiw ak jàmm ñeel, tukkee fa Ki masa nekk, Ki nekk, di Kiy dikk, tukkee it fa boroom juróom ñaari noo ya fa kanam ngànguneem,
Peeñu ma 1:4
Su boobaa jàmmu Yàlla ji wees ab takk, mooy sàmm seen xol ak seenum xel ndax Almasi Yeesu.
Filib 4:7
Ba ñaari taalibe ya di nettali loolu, ca la Yeesu ci boppam ne jimeet taxaw ci seen biir, ne leen: «Jàmm seen!»
Luug 24:36
Jàmm laa leen bàyyee, sama jàmm laa leen may te mayuma leen ko ni àddina di mayee. Buleen jaaxle, buleen tiit.
Yowaan 14:27
«Taxawukat bi may yónni ci yeen te muy jóge ci Baay bi mooy Noowug dëgg googu di bàyyikoo ci Baay bi, te kooku bu dikkee, moo may seedeel.
Yowaan 15:26
Meññeefum Noowug Yàlla nag moo di: cofeel ak mbég ak jàmm ak xolu muñ ak mbaax akug tabe ak ngëm
Galasi 5:22
Te Noowug Yàlla, moom ci boppam, moo mànkoo ak sunu noowug bopp, di seede ne ay doomi Yàlla lanu.
Room 8:16
Aji Sax ji ne ko: «Man ci sama bopp maay ànd ak yaw te maa lay noppal.» Musaa ne ko: «Soo demul yaw ci sa bopp kay, bu nu jële fii! Nees di xame ne daj naa saw yiw, maak sa ñoñ, te fekk ànduloo ak nun, ba nu doon, maak sa ñoñ, ñu ràññiku ci biir mboolem xeet yi ci kaw suuf?»
Mucc ga 33:14–16
Te yemunu ci, xanaa di sagoo sunuy tiis itam, nde xam nanu ne dékku aw tiis mooy taxa muñ;
Room 5:3
Su dee ci giiru dund gii doŋŋ lanu ame yaakaar ci Almasi bi, kon de noo gëna toskare ñépp.
1.Korent 15:19
Soppe yi, tàngooru nattu bi ngeen nekke nii, bumu leen jaaxal ba mel ni lu jaaduwul moo leen dikkal. Waaye noonu ngeen séddoo ci coonoy Almasi bi, bégeleen ko, ngir bu ndamam feeñee, ngeen gënatee bég.
1.Piyeer 4:12–13
Dees noo jàppe boroomi tiis, te nu dëkke mbég; jàppe nu ay néew-ji-doole, te nu woomal ñu bare; jàppe nu ñu amul dara, te nu moom lépp.
2.Korent 6:10
Bégleen ci Boroom bi fu ngeen tollu, ma waxati ko, bégleen!
Filib 4:4
Ndaw ya nag bàyyikoo ca kuréelu àttekat ya, di bég, gannaaw ñoom lañu jàpp ne ñoo yelloo toroxte ga ñu leen teg ndax Tur wi.
Jëf ya 5:41
Kon Yàlla miy maye yaakaar, yal na leen feesaleek gépp mbég ak jàmm ci biir ngëm, ba ngeen fees dell ak yaakaar, ci manoorey Noo gu Sell gi.
Room 15:13
Ndaxam garabu figg meññul, doomu reseñ amul ca ndeyam, njurum garabu oliw àntuwul, tool yi meññul aw ñam, gàtt it tukkee na ca gétt ga, du genn jur gu gudd ci wërmbal, te man may bànneexoo Aji Sax ji, Yàlla ji may wallu laay bége.
Abakug 3:17–18
Bés yu mujj yi
Wone yépp29 Now 2025
28 Now 2025
27 Now 2025
26 Now 2025
25 Now 2025
24 Now 2025
23 Now 2025