Leeru Bés bi — 29 Nowàmbar: Taalifi cant 65:4

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Samay ñaawtéef man na ma, waaye sunuy tooñ, yaa nu koy baal.

Taalifi cant 65:4

Lenn laa ñaan Aji Sax ji, lii laay sàkku: dëkk kër Aji Sax ji sama giiru dund, di niir taaru Aji Sax ji, te yéemoo këram.

Taalifi cant 27:4

Ndokkalee ñi xiif aka mar jëfe njekk, ndax dinañu regg.

Macë 5:6

Ñi xiif, mu reggale leen lu neex, ñi duunle, mu dàqe loxoy neen.

Luug 1:53

Mooy màndal put gu wow, di feesal ngëneel biir bu wéet.

Taalifi cant 107:9

Yeesu ne leen: «Man maay ñam wiy joxe dund. Ku ñëw ci man, doo xiif mukk; te ku ma gëm, doo mar mukk.

Yowaan 6:35

Sa njubtee tiim tund yu mag yi, sa àtte ne xéew ni xóotey géej. Céy Aji Sax ji, nit ak mala, nga boole sàmm! Céy Yàlla, yaa wéet ngor, doom aadama yiiroo sa keppaar, yiiru; yafloo sa njël lu duun, sa xéewal wal, nga nàndale ko.

Taalifi cant 36:7–9

Yeesu ne leen: «Xanaa gëm ngeen léegi?

Yowaan 16:31

Bokk yi, ku ne gëm na, te jëfewu ko, ana lu mu koy jariñ? Ndax googu ngëm man na koo musal?

Yanqóoba 2:14

Noonu la ngëm deme, su amul jëf ju mu àndal, ngëm gu dee la.

Yanqóoba 2:17

Ibraayma, ba ñu ko nattoo, ngëm la joxee Isaaxa ni ab sarax. Ibraayma mi ñu jagle dige yi, Isaaxa jenn doomam ju góor ji mu am, moom la doon joxe, te Yàlla ne woon ko: «Ci Isaaxa lees di tudde saw askan.» Waaye Ibraayma njortoon na ne su Isaaxa dee woon it, Yàlla man na koo dekkal. Moo tax itam ci misaal, Isaaxa délsi ciy loxoom, mel ni daa dekki.

Yawut ya 11:17–19

Sunu maam Ibraayma, xanaa du ci jëf lees ko baaxe àtteb ku jub, ndax jëf ja mu joxee doomam Isaaxa ca sarxalukaay ba?

Yanqóoba 2:21

Ngeen gis kon ne ci jëf lees di baaxe nit àtteb ku jub, waaye du ci kaw ngëm doŋŋ.

Yanqóoba 2:24

Waaye ki ne jàkk yoon wu mat sëkk wiy goreel ku ko topp, saxoo yoon wi te bañ koo dégg, fàtte, xanaa di dégg, jëfe, kooku mooy bége jëfam.

Yanqóoba 1:25

Kon nag ñoom daal ci seenum meññeef ngeen leen di xàmmee. «Du képp ku ma naan: “Sang bi, Sang bi,” mooy tàbbi ci nguurug asamaan, xanaa ñiy jëfe sama coobarey Baay ba fa asamaan.

Macë 7:20–21

Loolu, su ngeen ko xamee, ndokkalee yeen, ndegam yeena ngi koy jëfe.

Yowaan 13:17