Yaram wu àndul akug noo daal, ni mu deewe, noonu la ngëm gu àndul aki jëf deewe.
Yanqóoba 2:26
Leeru Bés bi
Yaram wu àndul akug noo daal, ni mu deewe, noonu la ngëm gu àndul aki jëf deewe.
Yanqóoba 2:26
«Du képp ku ma naan: “Sang bi, Sang bi,” mooy tàbbi ci nguurug asamaan, xanaa ñiy jëfe sama coobarey Baay ba fa asamaan.
Macë 7:21
Sàkkuleen jàmm seen diggante ak ñépp, te it sàkkuleen cellte, nde ku sellul du gis Boroom bi.
Yawut ya 12:14
Ndax kat ci yiw ngeen mucce ci kaw ngëm, te loolu jógewul ci yeen, mayu Yàlla la; du peyu jëf, ba kenn di ci kañu.
Efes 2:8–9
Gone yooyu nag, bindeefi suux ak deret lañu bokk doon, ñoom ñépp. Moo tax Yeesu itam dikk bokk ak ñoom woowu nekkin, ngir mana dee ba def deewug boppam pexe mi mu neenale ka yoroon dooley dee, te mooy Seytaane. Noonu la goreele mboolem ñi seenug ragala dee tënkoon cig njaam, seen giiru dund.
Yawut ya 2:14–15
Moo yaw dee, ana sa ndam? Moo yaw dee, ana sag fitt?»
1.Korent 15:55
Waaye cant ñeel na Yàlla mi nu may ndam ci sunu Sang Yeesu Almasi bi!
1.Korent 15:57
Moo tax dunu ñàkk yaakaar. Doonte sax sunu bitib jëmm a ngi gën di bon, sunu jëmmu biir moom, mu ngi yeeslu bésoo bés.
2.Korent 4:16
Xam nanu ne sunu yaram, sunu këru kaw suuf gii di ab xayma, bu daanoo it, am taax lanu am fa Yàlla, kër gu sax dàkk gu loxol nit tabaxul.
2.Korent 5:1
Moo tax nu saxoo ñeme, doonte xam nanu ne sunu desagum biir kër, ci yaram wi, mooy sunu desagum fu sore Sang bi, ndax ngëm lanuy doxe, waaye doxewunu ab gis-gis. Kon fees nanu ak kóolute, te li nu gënal mooy jóge ci sunu yaramu bopp, ngir dëkki ak Sang bi.
2.Korent 5:6–8
«Buleen jàq. Gëmleen Yàlla te gëm ma. Sama kër Baay, dëkkuwaay yu baree nga fa. Su demewul woon noonu, ndax dinaa leen ne maa ngi leen fay waajali béreb? Te gannaaw bu ma leen waajalee béreb, dinaa délsi, jëlsi leen, yóbbu, ba fu ma nekk, man, ngeen nekk fa, yeen itam.
Yowaan 14:1–3
Bés yu mujj yi
Wone yépp27 Now 2025
26 Now 2025
25 Now 2025
24 Now 2025
23 Now 2025
22 Now 2025
21 Now 2025