Man nag daraja ji nga ma jox, jox naa leen ko, ngir ni nu nekke benn maak yaw, ñu nekke ni noonu.
Yowaan 17:22
Leeru Bés bi
Man nag daraja ji nga ma jox, jox naa leen ko, ngir ni nu nekke benn maak yaw, ñu nekke ni noonu.
Yowaan 17:22
At ma Buur Osiyas saayee, damaa gis Boroom bi toog kaw ngàngune mu kawee kawe, lafi mbubbam fees néeg bu sell bi. Ay malaakay seraf ñoo taxaw, tiim ko, ku ci nekk am juróom benni laaf: ñaar yu muur seen kanam, ñaar yu muur seeni tànk, ak ñaar yu ñuy naawe. Ku ci nekk di àddu, naan moroom ma: «Kee sell te sell te sell, keey Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi, àddina sépp a feese ag leeram!»
Esayi 6:1–3
Loolu Esayee ko wax, ndax moo gisoon darajay Yeesu, bay wax ci mbiram.
Yowaan 12:41
Ca kaw dénd ba tiim seeni bopp, ba tey, am na luy nirook ngànguney peru safiir, te jëmmu nit nekk ca kaw-a-kaw lay nirook ngàngune.
Esekiyel 1:26
Mu mel ni xon ci biiri niir, bésub taw. Loolooy melokaanu leer ga ko wër. Muy melokaan muy jëmmal leeru Aji Sax ji. Naka laa ko gis, daldi ne gurub, dëpp sama jë fi suuf. Ma dégg nag kàddu gu jib.
Esekiyel 1:28
Musaa teg ca ne ko: «Ngalla may ma nag ma niir sag leer!»
Mucc ga 33:18
Mu teg ca ne ko: «Doo mana gis sama kanam nag, ndax doom aadama du ma gis ba noppi di dund.»
Mucc ga 33:20
Kenn masula gis Yàlla, waaye Yàlla miy Kenn te sës rëkk ci Baay bi, kooku mooy ki ko xamle.
Yowaan 1:18
Ndaxte Yàlla mi ne: «Na leer gi leer ci biir lëndëm gi,» moo leeral sunu xol, ngir leeraangey xam-xamu leeru Yàlla, te leeraange googu mooy lerxat ci xar-kanamu Yeesu Almasi bi.
2.Korent 4:6
Doom, bàkkaarkat bu la xiirtal, lànkal.
Kàddu yu xelu 1:10
Jigéen ja dafa gis ne garab gi rafet na, niru na lu neex, te mata bëgg ci kuy wuta am xel, mu witt ci doom yi, lekk; jox ci jëkkëram ji mu àndal, moom it mu lekk.
Njàlbéen ga 3:6
Ba Akan doomu Sera defee jëfi ñàkk worma ja mu defoon, ca mbirum yëf ya ñu aaye woon, xanaa du mbooloom Israayil mépp la am sànj dikkal? Du moom mi def ñaawtéefam doŋŋ moo dee de!»
Yosuwe 22:20
Buleen seet fi mbooloo gëna baree, ngeen topp leen ci jëf ju bon; te it buleen jeng, di topp mbooloo mu gëna bare ci ab layoo, di leen seedeel lu toxal dëgg.
Mucc ga 23:2
«Duggeleen ci bunt bu xat bi, ndax bunt beek yoon wi jëm sànkute dañoo yaatu, te ñu baree cay dugge.
Macë 7:13
Ndax kat kenn ci nun dundul ngir boppam, te kenn deewul ngir boppam.
Room 14:7
Yeen de bokk yi, cig yiwiku lees leen woo. Moytuleen lenn rekk: bu seenug yiwiku diw lay, ngir topp seen bakkan, waaye deeleen surgawoonte ngir cofeel.
Galasi 5:13
Waaye ni ngeen di dunde seen sañ-sañu bopp, dangeen ciy xool ñi seen ngëm dëgërul, ngir ngeen bañ leena yóbbe bàkkaar.
1.Korent 8:9
Su ngeen tooñee noonu bokki gëmkat ñi, ba yàq seen xel mu daladi, kon de Almasi bi ngeen tooñ.
1.Korent 8:12
Nun ñépp a lajj niy xar, ku nekk walbatiku topp yoonam, te Aji Sax jee ko sëf mbugal mi nu wara dékku nun ñépp.
Esayi 53:6
Bés yu mujj yi
Wone yépp26 Now 2025
25 Now 2025
24 Now 2025
23 Now 2025
22 Now 2025
21 Now 2025
20 Now 2025