Deesatu la woowe «Dëkk bi ñu wacc,» deesatul woowe sam réew «Réew mu gental.» Xanaa ñu woowe la «Dëkk bi ma neex,» tey woowe sam réew «Boroom jëkkër,» ndax yaa neex Aji Sax ji, te sa réew mi dina am boroom kër.
Esayi 62:4
Leeru Bés bi
Deesatu la woowe «Dëkk bi ñu wacc,» deesatul woowe sam réew «Réew mu gental.» Xanaa ñu woowe la «Dëkk bi ma neex,» tey woowe sam réew «Boroom jëkkër,» ndax yaa neex Aji Sax ji, te sa réew mi dina am boroom kër.
Esayi 62:4
Léegi nag yaw Yanqóoba, yaw Israayil mii, Aji Sax ji la sàkk tabax la, dafa wax ne: «Bul tiit, jot naa la. Dama laa woo ci sa tur. Maa la séddoo.
Esayi 43:1
Aji Sax ji nee: «Ana jaboot juy fàtte doomam juy nàmp, mbaa muy néege ku mu jur ci biiram? Bu ko manoona fàtte it, man duma la fàtte. Sama biir loxo yii laa la ñaas, say tataa janook man ba fàww.
Esayi 49:15–16
Bu Aji Sax ji rafetloo saw yoon, mooy jiite say jéego.
Taalifi cant 37:23
May bége wërngalu àddinaam, di bànneexoo doomi aadama.
Kàddu yu xelu 8:31
Ki Aji Sax ji gërëm mooy ki ko ragal te di ko yaakaare ngoram.
Taalifi cant 147:11
«Sama moomeelu bopp la ñooñuy doon,» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax, «ca bés ba may jëfi, sama gànjar lañuy doon, te ni baay di baaxe as ngóoram su ko taxawu, ni laa leen di baaxe.
Malasi 3:17
Te yeen ñi masoona sore lool Yàlla, doonoon ay noonam ci wàllu xalaat ak jëf ju bon, tey, deewug yaram, deewug suux gi Almasi bi dee, moom la leen Yàlla jubalee ak boppam, ba teewal leen fi kanamam, ngeen di ñu sell, mucc sikk, seen der set wecc.
Kolos 1:21–22
Ndaxte tiis wu Yàlla namm, ag tuubeel gu jëme cig mucc lay jur, te loolu du tiis wees di tiisoo. Waaye tiisu àddina, dee lay jur.
2.Korent 7:10
Ci biir loolu Axitofel gis ne déggeesul ndigalam, mu takk mbaamam, ñibbi ca dëkk ba mu fekk baax. Mu daldi toppatoo mbiri këram ba mu jekk, ba noppi wékk boppam. Mu dee, ñu denc ko ca sëgi baayam.
2.Samiyel 17:23
Ku bëgga dund, dékku woppi yaram, waaye xol bu jeex maneesu koo wéye.
Kàddu yu xelu 18:14
Moo ndax diwu pajtal amul Galàdd? Am fajkat a fi amul? Ana lu tax ba bokk yi taneeguñu?
Yeremi 8:22
Noowug Boroom bi Aji Sax jaa ngi fi sama kaw, ndax Aji Sax jee ma diw, fal ma ngir ma yégal néew-doole yi xibaaru jàmm. Moo ma yebal ngir ma dëfal ñi seen xol jeex, yégal jaam yi seen goreel, yégal ñi ñu tëj seen ubbite. Moo ma yónni ngir ma yéene atum yiwu Aji Sax ji, ak at mu sunu Yàlla di mbugalee. Moo ma yónni ngir dëfal ñiy ñaawlu ñépp, ngir indil waa Siyoŋ ñiy ñaawlu ab kaala gu wuutu dóomu-taal, ak diwu mbégte mu ñu weccikoo seenu tiis, ak mbubbam cant mu ñu weccikoo xol bu jeex, ba ñu naa: «Ñii ñoo di ponkali garabi njubte yi, njëmbat li Aji Sax ji jëmbat, ngir teewal màggaayam.»
Esayi 61:1–3
«Mboolem yeen ñi loof ndax sëf bu diis, ñëwleen ci man, man maa leen di noppal. Tegooleen sama kilifteef te ngeen jànge ci man, daldi dajeek noflaayal xol, ndax maa lewet, woyof. Sama kilifteef sedd na, te samab sëf woyof.»
Macë 11:28–30
Filib daldi àddu, tàmbalee ci dog boobu, xamal ko xibaaru jàmm bi ci mbirum Yeesu.
Jëf ya 8:35
di faj naqaru xol, fajtal góomi boroom.
Taalifi cant 147:3
Bés yu mujj yi
Wone yépp25 Now 2025
24 Now 2025
23 Now 2025
22 Now 2025
21 Now 2025
20 Now 2025
19 Now 2025