Leeru Bés bi — 25 Nowàmbar: Room 6:18

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Noonu lees leen yiwee, tàggale leen ak nooteelu bàkkaar, ngeen doon ay surgay njub.

Room 6:18

«Kenn manula jaamu ñaari sang; dangay dëddu kii, sopp kee, mbaa nga fonk kii, cof kee. Manuleena jaamoondoo Yàlla ak Alal.

Macë 6:24

Ba ngeen dee jaami bàkkaar, teewuleen woona moom seen bopp, ci seen digganteek njub. Seen jëfi démb ja leen gàcceel tey, ana njariñ lu mu leen jural? Mujug jëf ja de, seenug dee la doon doon. Waaye tey bi ñu leen yiwee, ba ngeen doon ay surgay Yàlla, ag cellte la leen loolu jural, te muj ga di texe gu sax dàkk.

Room 6:20–22

Ndax kat Almasi bi moo sottal yoonu Musaa, ngir àtteb ku jub ñeel képp ku ko gëm.

Room 10:4

Ku may surgawu, na ma topp; fu ma nekk, sama surga ne fa moom itam. Ku ma surgawu nag, sama Baay moo koy teral.

Yowaan 12:26

Tegooleen sama kilifteef te ngeen jànge ci man, daldi dajeek noflaayal xol, ndax maa lewet, woyof. Sama kilifteef sedd na, te samab sëf woyof.»

Macë 11:29–30

Aji Sax ji sunu Yàlla, yeneen sang yu la moy moom nañu nu, waaye saw tur rekk lanuy màggal.

Esayi 26:13

Ci sa yoonu santaane laay wéy, yaa may may xol bu tàlli.

Taalifi cant 119:32

Su boobaa, képp ku woo Boroom bi wall ciw turam, dinga raw.”

Jëf ya 2:21

Manase nag di def li Aji Sax ji ñaawlu, topp ñaawtéefi xeet ya Aji Sax ji dàqoon ngir bànni Israayil. Moo tabaxaat bérebi jaamookaay ya Esekiyas baayam tasoon, yékkatil tuur mi ñu naan Baal ay sarxalukaay, samp xer wu ñuy jaamoo Asera, noonee ko Axab buurub Israayil defe woon, boole ca di sujjóotal mboolem biddiiwi asamaan, di leen jaamu.

2.Buur ya 21:2–3

Ay sarxalukaay it la tabaxal biddiiwi asamaan yépp ca biir ñaari ëtti kër Aji Sax ji. Te itam sarxal na doomam, lakk ko ngir ay tuur. Ci biir loolu xërëm na, gisaane na, jëflante naak ay boroom rawaan ak ñuy jokkook nit ñu dee. Bare na lu mu def lu Aji Sax ji ñaawlu, ba tax mu mer.

2.Buur ya 21:5–6

Ca biir njàqareem ja la sàkkoo yiwu Aji Sax ji Yàllaam, daldi toroxlu lool fi kanam Yàlla ju maamam ya. Mu ñaan Yàlla, Yàlla nangul ko, dégg ab dagaanam, delloosi ko Yerusalem ci nguuram. Manase nag xam ne Aji Sax ji mooy Yàlla.

2.Jaar-jaar ya 33:12–13

«Kaayleen, nu waxtaan ba juboo,» la Aji Sax ji wax. «Li seeni bàkkaar di xonq lépp, tàll lay weexeji. Li muy xonq curr lépp, weex furr lay mujje.

Esayi 1:18

Du caageenu yeexe gu Boroom bi yeexe dige ba, noonu ko ñenn ñi fooge ag yeex. Yeen la muñal kay, ndax bëggul kenn sànku, xanaa ñépp dem ba tuub.

2.Piyeer 3:9