Mu ne leen: «Sama yaay ak samay rakk, ñoo di ñiy dégg kàddug Yàlla, te di ko jëfe.»
Luug 8:21
Leeru Bés bi
Mu ne leen: «Sama yaay ak samay rakk, ñoo di ñiy dégg kàddug Yàlla, te di ko jëfe.»
Luug 8:21
Yeesu miy sellal nit ñi, moom ak ñi muy sellal, ñoo bokk lenqe, te moo tax Yeesu rusu leena woowe ay bokk. Mu ne: «Maay siiwali saw tur ci samay bokk, maa lay kañ fi digg mbooloo mi.»
Yawut ya 2:11–12
Ci Almasi Yeesu mi nu gëm, xaraf ak ñàkka xaraf, dara amu ci solo; li am solo mooy ngëm gi jëfi cofeel di firndeel.
Galasi 5:6
te samay xarit ngeen, ndegam yeena ngi def li ma leen sant.
Yowaan 15:14
Moom nag mu ne ko: «Xanaa kay, ndokkalee ñiy déglu kàddug Yàlla te di ko jëfe.»
Luug 11:28
«Du képp ku ma naan: “Sang bi, Sang bi,” mooy tàbbi ci nguurug asamaan, xanaa ñiy jëfe sama coobarey Baay ba fa asamaan.
Macë 7:21
Yeesu ne leen: «Samaw ñam moo di jëfe coobarey ki ma yónni, ba sottal ab liggéeyam.
Yowaan 4:34
Su nu nee am nanook moom jokkoog mbokk, te teewu noo wéye ag lëndëm, danuy fen, te jëfewunu dëgg.
1.Yowaan 1:6
Képp kuy jëfe kàddug Yàlla, ci moom déy la cofeelu Yàlla mate sëkk. Ci loolu lanuy xame ne moom lanu nekk.
1.Yowaan 2:5
Mu dugg foofa ca biir xunt ma, fanaan fa. Ci biir loolu kàddug Aji Sax ji dikkal Ilyaas, ne ko: «Ana looy def fii, Ilyaas?»
1.Buur ya 19:9
Ndaxam moo xam fi ma jaare, te bu ma nattoo, ma génn ci ni wurus wu ñu xelli.
Ayóoba 23:10
Mu jëm ci njiital woykat yi, ñeel Daawuda, dib taalifu cant. Aji Sax ji, yaa ma natt, xam ma; yaa xam sama toogaay ak sama taxawaay, di ràññee fu sore samay xalaat, di càmbar samab dox ak sama tëraay, yittewoo lépp lu may def.
Taalifi cant 139:1–3
Fu ma jëm, ba sore la? Fu ma daw jëm, foo teewul?
Taalifi cant 139:7
Ma war laafi njël, dëkki wàllaa géej, nga tettee ma fa ba tey, téyee ma sa ndijoor.
Taalifi cant 139:9–10
Ilyaas nit la woon ku bindoo ni nun, waaye ba mu saxee ci ñaan ngir mu baña taw, ndox laalul suuf diiru ñetti at ak genn-wàll.
Yanqóoba 5:17
Ragal nit dugal sa bopp la, ku wóolu Aji Sax ji, fegu.
Kàddu yu xelu 29:25
Soo tërëfee it, doo daanu. Aji Sax jee lay walloo loxoom.
Taalifi cant 37:24
Boroom njekk day daanu juróom ñaari yoon, jógaat, ab soxor sërëx ci njekkar.
Kàddu yu xelu 24:16
Bunu tàyyi ci def lu baax, nde bu jotee rekk nooy góob, ndegam yoqiwunu.
Galasi 6:9
Teewluleen te ñaan, ngir baña tàbbi cig fiir. Xolub nit kat yebu na, yaram see néew doole.»
Macë 26:41
Ni baay yërëme doom, ni la Aji Sax ji yërëme ku ko ragal.
Taalifi cant 103:13
Bés yu mujj yi
Wone yépp23 Now 2025
22 Now 2025
21 Now 2025
20 Now 2025
19 Now 2025
18 Now 2025
17 Now 2025