Waaye déggal ma, dëkke jàmm, tàggook njekkar ak safaan.»
Kàddu yu xelu 1:33
Leeru Bés bi
Waaye déggal ma, dëkke jàmm, tàggook njekkar ak safaan.»
Kàddu yu xelu 1:33
Di ñaanu Musaa, góorug Yàlla ga. Boroom bi, yaa nu masa fat maasoo maas.
Taalifi cant 90:1
Ku dëkke kiiraayu Aji Kawe ji yaa këroo keppaaru Aji Man ji.
Taalifi cant 91:1
Kiiraayam la lay sànge, nga yiiru, làqu; kóllëreem feg la, di la aar.
Taalifi cant 91:4
ndaxte dee ngeen, ba seenug dund ànd ak Almasi bi, làqe fa Yàlla.
Kolos 3:3
Mu ne ko: «Dawal, nga wax xale bu góor bii ne ko: “Yerusalem lees di dëkke, te tata wëru ko; ŋàpp lay def, ndax barewaayu nit ñeek jur gi ci biiram.
Sàkkaryaa 2:8
Musaa nag ne mbooloo ma: «Buleen tiit, neleen tekk te xool li Aji Sax jiy def, ba xettali leen tey jii. Ndax kat waa Misra yii ngeen di gis nii tey, dootuleen leen gis mukk. Aji Sax ji moo leen di xeexal, yeen kay neleen tekk rekk.»
Mucc ga 14:13–14
Mu jëm ci njiital woykat yi, di woy wu ñeel askanu Kore wu góor, dëppook galan bu ñuy wax Baatu jigéen. Sunu Yàllaa nuy rawale, di nu dooleel, di nu wallu fu nu jaaxlee,
Taalifi cant 46:1–2
Yeesu wax ak ñoom ca saa sa, ne leen: «Dalleen, man mii la, buleen tiit!»
Macë 14:27
Yeesu nag ne leen: «Lu ngeen di jaaxle, ak lu ngeen di xel ñaar nii? Xoolleen samay loxo ak samay tànk. Man la. Làmbleen ma, ba xam! Njuuma amul suux, amuli yax, nii ma ko ame, ngeen gis.»
Luug 24:38–39
Looloo tax may daj yii coono. Waaye rusuma ci, ndax xam naa ki ma gëm, te wóor na ma ne, li ma ko dénk, moo ko mana sàmm ba keroog bés ba.
2.Timote 1:12
Yeesu ne ko: «Sama nguur moo bokkul ci àddina sii. Bu sama nguur bokkoon ci àddina, samay surga xeex, ba kenn du ma jébbal njiiti Yawut yi. Waaye sama nguur a bokkul fii.»
Yowaan 18:36
Waaye kii de, ba mu sarxee boppam ngir far ay bàkkaar, bennub sarax bu doy ba fàww, ca la tooge fa ndijooru Yàlla. Fa la doxe xaar bés ba ñu koy defal ay noonam ndëggastalu tànkam.
Yawut ya 10:12–13
Yeesu ne ko: «Yaa ko wax. Te it, maa leen ne gannaaw-si-tey dingeen gis Doomu nit ki toog ci ndijooru Boroom Kàttan gi, te dingeen ko gis ci kaw niir yi, muy ñëw.»
Macë 26:64
Ndaxte fàww Almasi bi nguuru, ba kera Yàlla di teg mboolem ay noonam ciy tànkam.
1.Korent 15:25
Waaye cant ñeel na Yàlla mi nu may ndam ci sunu Sang Yeesu Almasi bi!
1.Korent 15:57
ji mu fésal ci Almasi bi, ba mu ko dekkalee, dëël ko ci ndijooram fa déndi asamaan. Foofa la Almasi bi tiime lu sore gépp nguur ak bépp sañ-sañ ak gépp manoore ak gépp kilifteef ak wépp tur wees di tudd, muy tey di ëllëg. Yàlla moo teg lépp fi roni tànkam, te moo ko def muy bopp bi tiim lépp, ñeel mbooloom gëmkat ñi, mbooloo miy aw yaramam. Ci mbooloo mi nag la Almasi bi teewe teewaay bu mat sëkk, te Almasi bi mooy matal lépp ci ñépp.
Efes 1:20–23
te ki koy feeñal bu àppam jotee, di Ku tedd ki wéetoo nguuram, Buuru buur yi, Sangu sang yi,
1.Timote 6:15
Bés yu mujj yi
Wone yépp22 Now 2025
21 Now 2025
20 Now 2025
19 Now 2025
18 Now 2025
17 Now 2025
16 Now 2025