Waaye yeen samay soppe, sampuleen ba dëgër ci seen yoonu ngëm wu sell wee sell, te ngeen di ñaane ci Noo gu Sell gi.
Yudd 20
Leeru Bés bi
Waaye yeen samay soppe, sampuleen ba dëgër ci seen yoonu ngëm wu sell wee sell, te ngeen di ñaane ci Noo gu Sell gi.
Yudd 20
Yàlla xel la, kon ñi koy jaamu, xel ak dëgg lañu ko war di jaamoo.»
Yowaan 4:24
ndax nun ñaari xeet yépp, ci moom Almasi bi lanu jote ci Baay bi, ci ndimbalal genn Noo gu Sell gi.
Efes 2:18
Ba loolu amee, Yeesu dox ba sore leen tuuti, ne gurub sukk, dëpp jëëm fa suuf. Mu ñaan ne: «Sama Baay, bu manee am, bii kaas bu fees ak wextanu coono, ngalla teggil ma ko! Moona, bumuy sama coobare nag, waaye yaw, na sa coobare am.»
Macë 26:39
Te itam Noowug Yàlla moo nuy dimbali ndax sunug néew doole, nde xamunu sax li jaadoo sàkku ci sunuy ñaan, waaye Noo gi moo nuy tinule ay onk yu wees kàddug làmmiñ. Te kiy xool li ci biir xol yi, xam na liy xintey Noo gi, ndax ni ko Yàlla bëgge, ni la Noo giy tinool ñu sell ñi.
Room 8:26–27
Kóolute gi nu am ci Yàlla moo di su nu ko ñaanee lenn lu dëppook coobareem, da nuy nangul.
1.Yowaan 5:14
Moom miy Noowug dëgg gi, bu dikkee, moo leen di àggale ci dëgg gi gépp, ndax du ci coobarey boppam lay wax, waaye mboolem lu mu dégg la leen di wax, te liy ñëw ëllëg, moo leen koy wax.
Yowaan 16:13
Deeleen ñaan fu ngeen tollu, gépp xeetu ñaan aki dagaan ci ndimbalal Noo gi, ànd ci ak teewlu fu ngeen tollu, ak gépp parlu, te ngeen di ñaanal mboolem gëmkat ñu sell ñi.
Efes 6:18
Garab sax ñàkkul yaakaar. Boo goree, mu jebbiwaat, ba du ñàkk ay njebbit.
Ayóoba 14:7
Barax bu lemu sax, du ko damm, leer gu giim it, du ko fey. Mooy indi yoonu dëgg.
Esayi 42:3
leqali ma, teg ma ci yooni njub ngir teraangay turam.
Taalifi cant 23:3
Ndaxte tiis wu Yàlla namm, ag tuubeel gu jëme cig mucc lay jur, te loolu du tiis wees di tiisoo. Waaye tiisu àddina, dee lay jur.
2.Korent 7:10
Dëgg la, benn yarub tey neexul, xanaa naqari. Waaye la yar bay mujj jural ña mu tàggat, jàmm la ak njub.
Yawut ya 12:11
Maa jàddoon, nga duma ma, léegi sa kàddu laay sàmm.
Taalifi cant 119:67
«Loolu nu dal lépp, sunu jëf ju bon a tax ak sunu tooñ gu réy. Terewul yaw sunu Yàlla, tegoo nu lu dul mbugal mu yées mi sunuy bàkkaar yellool, ba tax mu am ñu des di dund nii.
Esra 9:13
Yaw samab noon, bu ma ree; maa daanu, maay jóg. Ci biir lëndëm laa toog, waaye Aji Sax jeey samag leer. Maa moy Aji Sax ji, kon naa tegoo meram, ba mu layool ma, dëggal ma, génne ma ba dugal ma ci leer gi, ma gis àtteb dëggam.
Mise 7:8–9
Bés yu mujj yi
Wone yépp21 Now 2025
20 Now 2025
19 Now 2025
18 Now 2025
17 Now 2025
16 Now 2025
15 Now 2025