Képp ku ma Baay bi jox dina ñëw, te man, ku ñëw ci man, duma ko dàq mukk.
Yowaan 6:37
Leeru Bés bi
Képp ku ma Baay bi jox dina ñëw, te man, ku ñëw ci man, duma ko dàq mukk.
Yowaan 6:37
«Man Yàlla, buleen wax lu ñaaw ci man, te seen kilifag askan, buleen wax lu bon ci moom.
Mucc ga 22:27
Ndaxam du tax ma sofental leen ca seen réewu noon, mbaa ma di leen xalab, di leen faagaagal, nde kon ma fecci sama kóllëreek ñoom. Ndax man Aji Sax ji maay seen Yàlla.
Sarxalkat yi 26:44
Waaye man maay bàyyi xel sama kóllëre gi ma fasoon ak yaw ba ngay ndaw. Maa lay saxalal kóllëre guy wéy ba fàww.
Esekiyel 16:60
«Kaayleen, nu waxtaan ba juboo,» la Aji Sax ji wax. «Li seeni bàkkaar di xonq lépp, tàll lay weexeji. Li muy xonq curr lépp, weex furr lay mujje.
Esayi 1:18
Na ku bon ba jëfinam, kuy def lu ñaaw fomm mébétam, te walbatiku ci Aji Sax ji sunu Yàlla, mu yërëm ko, yaatal njéggalam.
Esayi 55:7
Mu teg ca ne: «Yeesu, boo délsee ci sa nguur, fàttaliku ma!» Yeesu ne ko: «Yaw laa ne déy, bésub tey jii, man ngay nekkal fa Àjjana.»
Luug 23:42–43
Barax bu lemu sax, du ko damm, leer gu giim it, du ko fey. Mooy indi yoonu dëgg.
Esayi 42:3
Yàlla kat moo nu wallu ba génne nu ca kilifteefu réewum lëndëm ga, toxal nu ci biir nguurug Doomam ji mu sopp.
Kolos 1:13
Ci kaw loolu rekk, baat jibe asamaan, ne: «Kii mooy sama Doom, sama soppe; Moom laay bànneexoo.»
Macë 3:17
Aji Sax ji nee: «Xoolleen sama jaam bii ma yor, sama tànnéef, sama soppey xol, ci moom laa sol sama xel, te mooy indil xeet yi yoonu àtte.
Esayi 42:1
Kenn masula gis Yàlla, waaye Yàlla miy Kenn te sës rëkk ci Baay bi, kooku mooy ki ko xamle.
Yowaan 1:18
Ni cofeelu Yàlla feeñe ci nun moo di jenn Doomu boppam ji mu yebal ci àddina, ngir nu mana dund ci kàttanam. Lii mooy cofeel: cofeel gi du sunug cofeel, nun ci Yàlla; xanaa cofeel gi mu nu sopp, ba yebal Doomam, def ko njotlaay, ñeel sunuy bàkkaar.
1.Yowaan 4:9–10
Nun nag xam nanu te gëm nanu cofeel gi nu Yàlla sopp. Yàlla cofeelu neen la. Képp ku saxoo cofeel, ci Yàlla nga sax, te Yàlla itam ci yaw la sax.
1.Yowaan 4:16
Man nag daraja ji nga ma jox, jox naa leen ko, ngir ni nu nekke benn maak yaw, ñu nekke ni noonu. Man ma nekk ci ñoom, yaw nga nekk ci man, ngir ñu mat sëkk ci ag bennoo, ba àddina xam ne yaw yaa ma yebal, te ni nga ma soppe, ni nga leen soppe. «Ñi nga ma jox nag, Baay, bëgg naa, fa may ne, ñoom it, ñu nekk faak man, ngir ñu gis sama daraja ji nga ma jox, ndax yaa ma sopp laata àddina di sosu.
Yowaan 17:22–24
Ndaw cofeel gu nu Baay bi won, ba ñu di nu woowe doomi Yàlla, te moom lanu it. Àddina nag xamu nu, te li ko waral moo di da koo xamul moom itam.
1.Yowaan 3:1
Bés yu mujj yi
Wone yépp20 Now 2025
19 Now 2025
18 Now 2025
17 Now 2025
16 Now 2025
15 Now 2025
14 Now 2025