Leeru Bés bi — 20 Nowàmbar: Mise 7:8

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Yaw samab noon, bu ma ree; maa daanu, maay jóg. Ci biir lëndëm laa toog, waaye Aji Sax jeey samag leer.

Mise 7:8

Booy xuus cim ndox, maa ngi ànd ak yaw; ag dex du la mëdd. Booy dox cib taal, doo lakk, sawara du la xoyom. Man Aji Sax ji, maay sa Yàlla; man Aji Sell ju Israayil, maa lay musal. Maa joxe Misra, feye la; ak Kuus ak Saba, ma weccikoo la.

Esayi 43:2–3

Maay doxloo silmaxa yi ci yoon wu ñu xamul, ñall wu ñu miinul laa leen di jaarale. Maa leen di soppil lëndëm gi fi seen kanam ag leer, fu ñagas, ma maasaleel leen. Lii laa leen di defal, te duma leen wacc mukk!

Esayi 42:16

Su may jaare xuru dee wu ne këruus it, duma ragal loraange: yaw laak man, sa bantu sàmm ak sa nguul, yooyoo may dalal.

Taalifi cant 23:4

Ñeel Daawuda. Aji Sax jee may leeral, di ma wallu. Ana ku may ragal? Aji Sax jeey aar sama bakkan. Ana ku may tiit?

Taalifi cant 27:1

Ndax kat jenn Yàlla doŋŋ moo am, benn rammukat doŋŋ it moo am diggante Yàlla ak nit ñi, te mooy kenn nit: muy Almasi Yeesu

1.Timote 2:5

Dégluleen, yeen bànni Israayil, Aji Sax ji sunu Yàlla, Aji Sax ji kenn la.

Baamtug yoon wi 6:4

Ab jottalikat nag ñaar a koy séq, te Yàlla kenn doŋŋ la.

Galasi 3:20

Noo bàkkaar, nook sunuy maam; noo def lu ñaaw, def lu bon. Sunuy maam seetuñu ca say kéemaan ca Misra, bàyyiwuñu xel ca sa ngor lu réy, xanaa di fippu ca géej ga, géeju Barax ya.

Taalifi cant 106:6–7

Yàlla da leen doon sànk, bu dul woon ak Musaa, xejjam ba ko kar, àtte leen, mu giif, ba faru leen.

Taalifi cant 106:23

Kon nag bokk yu sell yi, yeen ñi bokk ci wooteb asamaan, ràññeeleen Yeesu, ndaw li, sarxalkat bu mag bi ci yoon wi nu gëm. Ku wóor la woon, ñeel ki ko tabb, noonee Musaa wóore woon ci mboolem waa kër Yàlla. Waaye ni ab tabaxkat ëppe teraanga kër ga muy tabax, ni la Yeesu yelloo daraja ju ëpp ja Musaa yelloo woon.

Yawut ya 3:1–3

Waaye tey la Yeesu jot ci liggéeyu carxal gu sut gu njëkk ga fuuf, te kóllëre gi mu fas diggante Yàlla ak nit ñi, noonu la gëne gu njëkk ga; dige yi lal kóllëre gu yees gii it, noonu la gëne dige ya laloon gu njëkk ga.

Yawut ya 8:6

Maa leen di jéggal seeni ñaawtéef, te seeni bàkkaar, duma ci bàyyeeti xel.»

Yawut ya 8:12