Leeru Bés bi — 19 Nowàmbar: Macë 7:20

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Kon nag ñoom daal ci seenum meññeef ngeen leen di xàmmee.

Macë 7:20

Xale yi, bu leen kenn nax! Kuy def njub, yaa jub, ni Almasi bi ci boppam jube.

1.Yowaan 3:7

Benn bëtu ndox ndax dina ballandoo ndox mu neex ak ndox mu wex, ci menn pax mi? Bokk yi, ndax ag figg man naa meññ oliw? Am ag reseñ dina meññ doomi figg? Bëtu ndoxum xorom it du nàcc mukk ndox mu neex. Ana ci yeen ku rafet xel te xam àddina? Na ko firndeele dundin wu rafet wu feeñ ci jëfam ju teey ndax xel mu rafet.

Yanqóoba 3:11–13

Seen dundin ci biir jàmbur ñi gëmul, rafetalleen ko, ba su ñu leen waxaloon ne ay defkati lu bon ngeen itam, seen jëf ju rafet lañuy gis, te moom lañuy sàbbaale Yàlla, kera bésub dikkam.

1.Piyeer 2:12

«Yaar garab gi baax, meññeefam baax, mbaa garab gi bon, meññeefam bon; nde garab, meññeefam.

Macë 12:33

Nit ku baax, ci dencub ngëneel lay jële lu baax, nit ku bon it, ci dencub safaanam lay jële lu bon.

Macë 12:35

Lu may defalati sama tóokër bi, lu ma ca defuloon? Lu waral ma di ko yaakaare reseñ ju neex, mu meññ, wex xàtt?

Esayi 5:4

«Taaru àllub Libaŋ a lay ñibbisil, garabu sippar, pẽe ak geneen gu dëkke naat, taaralsi sama kër gu sell gi, ba ma terale ci sama ndëggastalu tànk.

Esayi 60:13

Aji Sax ji dafa wax ne: «Asamaan sama ngàngunee, suuf di sama ndëggastal. Ana kër gu ngeen may tabaxal, man? Ana ban béreb ay sama dalluwaay?

Esayi 66:1

«Waaye yaw Yàlla! Ndax yaay dëkk ak doom aadama ci kaw suuf sax? Seetal rekk, asamaan ba ca asamaani asamaan manu laa fat, astamaak kër sii ma tabax.

2.Jaar-jaar ya 6:18

Aji Sax ji Boroom gàngoor yi kat dafa wax ne: Fileek lu néew, maa ngii di yëngalati asamaan ak suuf, ak géej ak jéeri. Maay yëngal xeetoo xeet, alali xeetoo xeet duggsi, ma feesal kër gii ak teraanga, Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax;

Ase 2:6–7

Daraja ji kër gii di mujje mooy sut ja woon, Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax. Mu ne: Ci bii béreb laay mayee jàmm, kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi.”»

Ase 2:9

Ma daldi gis asamaan su bees ak suuf su bees. Fekk na asamaan su njëkk sa ak suuf su njëkk sa wéy, te géej amatul.

Peeñu ma 21:1

Ma dégg kàddu gu xumb jibe ca ngàngune ma, ne: «Màkkaanu Yàllaa ngii ci biir nit ñi. Mooy dëkk ak ñoom, ñu diy ñoñam. Yàlla ci boppam mooy dëkk ak ñoom, di seen Yàlla.

Peeñu ma 21:3