Leeru Bés bi — 18 Nowàmbar: Esayi 27:8

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Ndànk-ndànk la jëflanteek ñoom, ba mu leen toxalee, dàqe leen noowam gu mag, bésu ngelawal penku.

Esayi 27:8

Daawuda ne Gàdd: «Am naa njàqare lool; waaye naa tàbbi ci loxol Aji Sax ji rekk, ndax yërmandeem yaa na lool, waaye loxol doom aadama moom yàlla buma ci daanu!»

2.Samiyel 24:14

Maa ngeek yaw, nar laa wallu.» Kàddug Aji Sax jee. «Maay faagaagal mboolem xeet ya ma la sànniji. Yaw nag duma la faagaagal, duma la ñàkka topp moos, waaye li nga yelloo laa lay yare.»

Yeremi 30:11

Saxoowul di toppe, dencul mer ba fàww. Du sunuy bàkkaar la nu mbugal, du sunuy ñaawtéef la nu fey.

Taalifi cant 103:9–10

Moo xam sunu bind, di bàyyi xel ne pënd lanu.

Taalifi cant 103:14

«Sama moomeelu bopp la ñooñuy doon,» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax, «ca bés ba may jëfi, sama gànjar lañuy doon, te ni baay di baaxe as ngóoram su ko taxawu, ni laa leen di baaxe.

Malasi 3:17

Yeesu neeti: «Simoŋ, Simoŋ! Seytaane kat mu ngi sàkku ab sañ-sañ ngir man leena jéri ni am pepp. Waaye man tinul naa la, ngir sa ngëm baña giim. Yaw nag boo waññikoo, nanga dooleel sa bokki gëmkat.»

Luug 22:31–32

Yaa di rawtub néew-ji-doole, di rawtub aji ñàkk, biir njàqare, yaay mbaar mu ñuy yiiroo waame, di ker gu ñuy féexloo ci tàngoor, ndax merum kilifa gu néeg mooy waame wu ne yureet ci kaw ab tabax.

Esayi 25:4

Gëmuma ko woon ba bi ma dikkee, ba teg ci sama bët. Ndeke genn-wàll gi sax waxeesu ma ko woon. Wees nga riir ma ma déggoon ci yaw, ci xel mu rafet ak lu baax.

1.Buur ya 10:7

Keroog àtte ba, Lingeeru bëj-saalum dina jóg, janook niti tey jii, tiiñal leen; ndax moo bàyyikoo woon ca catal àddina, ngir déglusi xam-xamu Suleymaan, te tey jii, ku sut Suleymaan a ngi fi.

Macë 12:42

Kàddu gee sol aw suux, doon nit, màkkaanoo ci sunu biir, nu ne jàkk ci darajaam, darajay jenn Doom ji bawoo ci Baay bi, mat sëkk ci aw yiw akug dëgg.

Yowaan 1:14

Sama kàddu ak samam njàngale jotewul woon dara ak neex làmmiñ gu xam-xamu nit ràbb, waaye dafa di ay firnde yu manooreg Noowug Yàlla lañal, ngir seen ngëm baña sukkandiku ci xam-xamu nit, te sukkandiku ci manooreg Yàlla.

1.Korent 2:4–5

Mooy noonu ñu binde rekk ne: «Lu bët gisul, nopp déggu ko, xel daju ko, Yàllaa ko dencal ñi ko sopp.» Waaye nun la Yàlla feeñalal denc googu jaare ci Xelam. Ndaxte Xelum Yàlla lépp lay gëstu ba ci xóotey mbóoti Yàlla.

1.Korent 2:9–10

Yaw mi mel nii, buur bi ci taar bi ngay teg bët; yaay gis réew mi ne màww.

Esayi 33:17

Soppe yi, léegi doomi Yàlla lanu, te li nuy dooni nag feeñagul. Waaye xam nanu ne bés bu Almasi bi feeñee, nooy nirook moom, ndax su boobaa, ni mu nekke, noonu lanu koy gise.

1.Yowaan 3:2

Bu sama der bi lekkoo sax, du tee ma dese suux wu ma xoole Yàlla,

Ayóoba 19:26

Man nag ma am dëgg, ne la jàkk, yewwu, regge sa jëmm.

Taalifi cant 17:15