Aji Sax ji, yaa ma bégale say jaloore, may sarxolle ci say manoore.
Taalifi cant 92:5
Leeru Bés bi
Aji Sax ji, yaa ma bégale say jaloore, may sarxolle ci say manoore.
Taalifi cant 92:5
Moo tax nun itam, ba nu déggee seen mbir ba tey, noppiwunu leena ñaanal, di sàkku ngeen fees ak xam-xam ci lépp luy coobarey Yàlla, te ngeen ànd ceek lu mat sëkk ci wàllu xel ak gis-gis bu Noo gi maye.
Kolos 1:9
Su ko defee seen ngëm tax Almasi bi dëkke seen xol, ngeen sax ay reen yu sampe ci biir cofeel, ngir yeen ak mboolem ñu sell ñi, seenum xel mana jàpp, ni mu leen ware, luy yaatuwaayub cofeelu Almasi bi ak guddaay ba ak kawewaay ba ak xóotaay ba. Ngeen boole ci daj cofeelu Almasi gi wees xam-xam, ngir ngeen fees, ba fees dell ak koomu Yàlla.
Efes 3:17–19
Céy xóotaayub koomu Yàlla ak xel ma ak xam-xam ba! Deesul natt ay dogalam, deesul ràññee ay jëfinam!
Room 11:33
«Samay xalaat déy du seeni xalaat, te samay jëfin du seeni jëfin.» Kàddug Aji Sax jee. Mu ne: «Ni asamaan tiime suuf, ni la samay jëfin tiime seeni jëfin, samay xalaat it tiime ko seeni xalaat.
Esayi 55:8–9
Ndokkalee, yaw mi dénku ci Aji Sax ji, te sàkkuwoo ku bew ak kuy topp ay fen.
Taalifi cant 40:5
Bu leen lenn nax; Yàlla deesu ko foontoo. Nit ki, li mu ji, moom lay góob.
Galasi 6:7
Li ma gis daal, ku bey ñaawtéef, ji coono, yaa koy góob.
Ayóoba 4:8
«As ngelaw lañu ji, ñooy góob ngëlén. Gub du jóg, pepp du focci, te bu pepp amoon it, jàmbur a koy wann.
Ose 8:7
Ku jiwal bànneexu bakkanam, ci bànneexu bakkanam lay jële ngóobum yàqute; ku jiwal Noowug Yàlla, ci Noo gi ngay góobe texe gu sax dàkk.
Galasi 6:8
Coxor feyul boroom, day naxe; deel def njekk, sag pey wóor.
Kàddu yu xelu 11:18
Ku jiwal bànneexu bakkanam, ci bànneexu bakkanam lay jële ngóobum yàqute; ku jiwal Noowug Yàlla, ci Noo gi ngay góobe texe gu sax dàkk. Bunu tàyyi ci def lu baax, nde bu jotee rekk nooy góob, ndegam yoqiwunu. Kon nag bi nu koy jekku, nanuy def lu baax, ngir ñépp, rawatina waa kër yoonu ngëm wi.
Galasi 6:8–10
Nit a ngi tabe, di yokkule; nit di nëŋ-nëŋi, gëna ñàkk. Ku yéwén, woomle; kuy suuxat, suuxu.
Kàddu yu xelu 11:24–25
Lii rekk la: ji lu tuut, góob lu tuut; ji lu bare, góob lu bare.
2.Korent 9:6
Bés yu mujj yi
Wone yépp16 Now 2025
15 Now 2025
14 Now 2025
13 Now 2025
12 Now 2025
11 Now 2025
10 Now 2025