Leeru Bés bi — 16 Nowàmbar: Yowaan 17:17

Leeru Bés bi

Leeru Bés bi
Yépp

Ngalla sellale leen dëgg gi: sa kàddu mooy dëgg.

Yowaan 17:17

Yeen nag, set ngeen wecc ba noppi, ndax kàddu gi ma leen wax.

Yowaan 15:3

Na kàddug Almasi bi dëkk ci yeen, bay baawaan, ngeen di jariñoo xel mu mat sëkk mu ngeen di jàngalantee aka artoonte. Woyeleen xolub cant, ñeel Yàlla, ak ay taalifi cant ak woyi tagg Yàlla ak woy yu ñu fente ci Noowug Yàlla gi.

Kolos 3:16

Ana nu ndaw mana sellalee? Xanaa di sàmm sa kàddu. Sama léppi xol laa lay toppe, bul ma wacc, ma wàcc say santaane.

Taalifi cant 119:9–10

Ndax xel mu rafet miy tàbbi sa xol, nga xam, sa xol tooy, nga foog, fegu, amug dégg, raw,

Kàddu yu xelu 2:10–11

Tànkam, sama tànk, yoonam laa tegu, moyuma ko. Dëdduwuma ay santaaneem, sama biir xol laa denc ay kàddoom.

Ayóoba 23:11–12

Maa gëna ñaw képp ku may jàngal, nde sa kàdduy seedeey sama njàngat.

Taalifi cant 119:99

Yeesu moo waxoon Yawut yi ko gëmoon ne leen: «Bu ngeen saxee ci sama kàddu, samay taalibe dëgg ngeen. Su boobaa dingeen xam liy dëgg, te dëgg gi moo leen di goreel.»

Yowaan 8:31–32

Kon nag dootuleen ay gan mbaa ay doxandéem, waaye ay nawley ñu sell ñi ngeen, te waa kër Yàlla ngeen.

Efes 2:19

Waaye yeen fi ngeen agsi moo di tundu Siyoŋ, dëkku Yàlla jiy dund, te mooy Yerusalem ga ca asamaan, yeena àgg fa junniy junniy malaaka dajee di màggal; yeena àgg fa ndajem taaw ya seeni tur binde fa asamaan. Yeena àgg fa Yàlla, àttekatub ñépp; yeena àgg fa noowi aji jub ña ñu matal sëkk.

Yawut ya 12:22–23

Ñoom ñépp ngëm lañu deewaale te jotaguñu woon la ñu leen digoon. Waaye fu sore lañu ko séene, di ko séentu, tey ràññee ne ay doxandéem aki màngaan lañu ci àddina.

Yawut ya 11:13

Nun nag sunum réew a nga fa asamaan, fa nuy séentoo sunu Musalkat, Sang Yeesu Almasi bi. Mooy kiy liggéeye manooreem ji mu tënke lépp cig curgaam, ba sopparñi sunu yaram wu doyadi wii, niroole kook yaramam wi ànd ak màggaay.

Filib 3:20–21

te ngeen di sante Baay bi mbég, moom mi leen yellale ab cér ca muuru ñu sell ña, ca réewum leer ga. Yàlla kat moo nu wallu ba génne nu ca kilifteefu réewum lëndëm ga, toxal nu ci biir nguurug Doomam ji mu sopp.

Kolos 1:12–13

Soppe yi, ay gan ngeen, ay doxandéem ci kaw suuf. Kon nag li ma leen di dénk moo di ngeen moyu xemmemtéefi bakkan yiy xeex ak ab xol.

1.Piyeer 2:11